Maalig Gàkku fésal na yéeneem ak taxawaay bi mu namm a am ëllëg ci géewu pólitig bi. Moom njiital làng gi di Grand Parti jàpp na ni : “amul genn làng ci biir lëkkatoog YAW gu mën a wax ne moo ëpp i jëf Grand Parti ci ndam liñ am ci wote yi weesu.” Ba tax na, ciy waxam, dina nekk lawax ci wotey njiitu réewu Senegaal yu 2024.
WÉR-GI-YARAM
Jëwriñ jiñ dénk wàllu wér-gi-yaram àndul ak toppekatu Kéedugu bi ci Mbiru ndem-si-Yàlla ji Dura Jàllo mi ñàkkoon bakkanam fekk mu doon am doom. Ci liñ boole jàpp, bare nay tegtal yu gëstu gi wone yuy firndeel ni fajkat yi set nañu ci wecc. Waaye mi ngi dellu di leen ñaax ci ñu gën a rafetal liggéey bi.
TÀGGAT-YARAM
Senegaal dina soxla 8i miliyaar bu bëggee àgg ci gañ-jëlu (la finale) kub bu àdina si. Ógistĩ Seŋoor, Njiital FSF (kurélu futbal gu Senegaal), a ko xamle. Ciy kàddoom, soxla nañ Nguur gi nattal leen lu ni tollu. Li ko waral mooy xam nañ li leen di xaar, rawatina ci waajtaay yi. Te yaakaar na ni tamit warul a doon benn jafe-jafe buñ bëggee indi kub bi niñ ko defe woon ci CAN bi.
MBËNN MI
Nawet baa ngi wéy di bare ndox fii ci réew mi. Ci njeexitalu ayu-bés bi, taw bu bare wàccaat na Ndakaaru ak ci diwaan yu bare. Nemmiku nañ ci ñetti nit ñu ci faatu ak yàqu-yàqu yu takku. Ba tax na njiitu réew mi di ko mettitlu fa mu nekk ca bittim-réew ak di massawu bu baax njaboot yi ci loru.