Xeex bi tey ci suba la xewe fale ca Ngomblaan ga. Dépite bii di Ami Njaay la kii di Masata Sàmb tëgg am pes ca digg Ngomblaan ga, xeex ba jolli. Ca la kii di Njiit la, Aamadu Maam Jóob, dakkalee liggéey ba ba ëllëg. Mu mel ni kàddu yi dépite bu jigéen boobu tegoon ci ndoddu Sëriñ Mustafaa Si keroog, waa ji daf ko cee guuxaloon ndeke.
Ndogal yi Njiitu réew mi jël
Ca ndajem jëwriñ ma mu doon amal démb, Njiitu réew mi, Maki Sàll, jot na faa jël ay ndogal yu am solo. Takkal na ñenn, ci ay ñoñam, ay ndomboy-tànk. Muy Allaaji Daawda Ñaŋ (Ambassadeur extraordinaire et plénipotentiaire de la République du Sénégal auprès de son Excellence Monsieur Asaan Watara Président de la République de Cȏte d’Ivoire), Abdu XaadirAñ (Ambassadeur extraordinaire et plénipotentiaire de la République du Sénégal auprès de son Excellence Monsieur Muhammad Basum Président de la République du Niger), Dooro Si (Ambassadeur extraordinaire et plénipotentiaire de la République du Sénégal auprès de son Excellence Monsieur Feliks Antuwaan Tshisekedi Tshilombo Président de la République démocratique de Congo), Mamadu Sidibe (Coordonnateur du projet de l’Université Suleymaan Ñaŋ de Maatam), Kànjuraa Nobaa (Coordonnateur du projet de l’Université du Sénégal Oriental), Maam Bàlla Lóo (Président du Conseil de Surveillance de l’Agence nationale pour la Relance des Activités économiques et sociales en Casamance), Mammadu Lamin Masali (Président du Conseil d’Administration de l’Office national de Formation Professionnelle), Amaroo Ntabi Baaji (Directeur du Secteur public local à la Direction générale de la Comptabilité publique et du Trésor), Wirsinii Doora Juuf (Agent Comptable des Grands projets à la Direction générale de la Comptabilité et du Trésor), Ceerno Saadu Jàllo (Directeur des Ressources Hhumaines au Ministère des Finances et du Budget), Abu Aaw (Directeur des pensions à la Direction générale du Budget), Leruks Daraame (Secrétaire général du Centre national et de la Fonction publique locale et de la Formation).
Ba ca topp mooy ne Njiitu réew mi dafa jël ndogalu tóxal ndajey jëwriñ yi. Bi ci njëkk dina ko amale ca diwaanu Tàmbaakundaa ñaar-fukki fan ak juróom-ñett ci weeru désàmbar wii.
Xamees na àppu jàkkaarloo bi
Ginnaaw bi ñu dégloo ñenn ci ñi laale woon ci coowal Aji Saar ak Usmaan Sonko, ñoom dinañu jàkkaarloo ca pekkug àttekat bii di Umar Maham Jàllo. Loolu nag dina am ci juróom-benni fan ci weeru desàmbar wii.
Ndogal li Paap Aale ñaŋ jël
Kii di Paap Aale mi ngi xamle ne dina amal ag xiifal ngir naqarlu anam bi ñu ko tegee loxo ak xoqatal bi ñu koy xoqatal ca kaso ba. Nee na nag, loolu dina tàmbali suba ci àjjuma ji, ñaari fan ci weeru desàmbar.
Càkkutéefu RSF
Kii di Njiital ak fara-caytu bu mag bu RSF (Reporters Sans Frontières) di Kiristof Diluwaar xamle na ne dina seeti tey kii di Paap Aale Ñaŋ. Rax-ci-dolli mi ngi fàttali kii di Njiitu réew mi Maki Sàll mu sàmmonte ak dige yi mu defoon ne benn taskatu-xibaar du dugg kaso ci ag Nguuram. Ñi ngi sàkku ñu bàyyi ko ndax du foofu mooy bérébam.
Luubal gi ñuy toppe Satoor Mbay
Kii nekkoon fi dépite ak Njiital AFP (Alliance des Forces de Progrès) moom lañuy toppe mbiri luubal yu tollu ci ñeen-fukki miliyoŋ. Moom nag dafa waxante woon ak senn ndaw ag daamar gu baax, waaye ba mu jotee xaalis ba rekk la dem yoonam te joxewul sax daamar gi.
NJÀNG AK NJÀNGALE
Ubbiteg daara ju kowe ji
Daara ju kowe ja nekke ca Jamñaajo te ñu dippee koo Aamadu Maxtaar Mbów, démb ci alxames ji lees ko doon ubbi. Moom nag mën na jël lu tollu ci 40. 000i ndongo.
Sémbug tabaxug yeneen daara yu kowe
Démb ci ndajem jëwriñ ma mu doon amal xamlees na ne, am na sémbug tabaxug ñaari daara yu kowe. Jenn ji ñu dippee ko daara ju kowe ju Maatam, jeneen ji di ju Senegaal gi fare penku (oriental).
Bés bi ñetti kurél yi jagleel ñaxtu
kurél gii di SELS (Syndicat des Enseignants Libres du Sénégal), CELS ak ñii di waa SNELAS (Syndicat National des Enseignants en Langue Arabe du Sénégal) tàmbali nañ seen xeex ci at mi. Tey nag ci alxames ji jël nañu ndogalu dakkal liggéey bi lu tollu ci bésub lëmm ngir naqarlu ñàkk a fullaal gi ñu ñàkk a fullaal seen i càkkuteef.
KOOM-KOOM
Càmmonte gi ak wàññig njëg yi
Ngir yombal dund gi, Njiitu réew mi dafa jëloon i ndogal ngir wàññi dund gu jafe gi. Lu tollu ci 2275i bitik lañu saytu ñaari fan ginnaaw bi ñu jëlee ndogal yooyu, lu tollu ci 689i yaxantukat ñu teewlu leen ca. Ñu jàpp ne coow li ci boroom bitig yu mag yi la waaye du ci ñiy jaayaat. Ndax ñooñu amuñu lu ñuy yokk walla lu ñuy wàññi.
Caabalug ARMP
ARMP (Autorité de Régulation des Marchés Publics), kurél giy saytu doxalinu ja yi, fésal na démb caabalug atum 2020 ak mu 2021. Ñoom nag, kepp nañu meeri bu Yoof ak Centre de formation professionnelle de Joal-Fadiouth. Wane nañ tamit yenn yoo xam ne seen i njureef dafa des muy yu ci mel ni Centre de formation professionnelle deMbour, meer bu Kër Masaar, meeru Barñi ak jaraafu Sigicoor.
WÉR-GI-YARAM
Xeexub jàngoroy Sidaa
Démb, alxames 1 desàmbar, lañu jagleel Sidaa ci àddina wërngal-këpp. Afrig nag, moom la jàngoro ji gën a laal. Ci fukki réew ak juróom-ñeent yi mu gën a laal nag, sémbi fagaru yi ci diwaan yi mu gën a laal ñeen-fukk la fa ci téeméer yoo jël. Li ñu mujje biral ci jàngoro jooju ci atum 2021 laal na lu tollu ci lu ëpp 1 miliyoŋ ci ay doomi-aadama, lu tollu ci 650i bakkan rot ci.
Lawug jàngoroy sibbiru si
Sibbiru soosu nag mi ngi law bu baax ci réew mi, rawatina ca Ndakaaru nag. Ndakaaru rekk am na lu tollu ci 19. 343i nit ñu ko ame, 71i bakkan rot ci atum 2021. Loolu nag Njiital (coordonnateur) kurél gii di PNPL (Programme National de Lutte contre le Paludisme) moo ko biral barki-démb.
XEW-XEWI JAMONO
Aksidaŋ ca Séeju
Aksidaŋ boobu ma nga ame ca boori Buñadu Mànjag, dëkk bu nekke ca goxu Sakar, ñaari daamar a fa mbëkkante. Ñeenti nit ñoo faatu ca saa sa, fukki nit ak benn ya ca jële ay gaañu-gaañu, yóbbu nañu leen raglu Aamadu Tiijaan Ba bu Séeju.
Beneen aksidaŋ ca diwaanu Kawlax
Aksidaŋ bii nag ma nga ame ca Kër Soose nekke ca diwaanu Kawlax. Ag daamar gu yamamaay (minicar), ab móto ak ub saret ñoo daje. Ci jamono jii nag am na kenn ku ca ñàkk bakkanam.
Xew-xew bu tiis
Ginnaaw bi réewu Senegaal daanee ñii di waa Ekuwaatër ca la mbir mi xewe woon. Benn boroom saret moo fiir benn ndaw buy wuyoo ci turu B.Ñ ca Kër Masaar. Da doon jéggi te boroom saret bi gisu ko, ci la ko fiire, ñu yóbbu ko raglu bu Idiriisa Puy bu Garaa Yoof, fa la ñàkke bakkanam.
TÀGGAT-YARAM
Njuréefi réewi Afrig yi ca joŋante bu mag ba
Juróomi réew ya teewal Afrig ca joŋante bu mag boobu nag jotu woon a am ndam cio seen i joŋante yu njëkk yi. Ci seen i ñaareeli joŋante yi nag, ñi jot a jàllagum ñépp a am ndam. Senegaal moom, ak Marog, ñoom dañoo daan rax-ci-dolli jàll ca huitième de finale ya. Waaye, kii di Tinisi moom, dafa daan ba pare toog ndax matalul poñ ya ñu ko doon laaj. Gana ak Kamerun a ci des te tey ci àjjuma ji lañuy joŋante. Ci lees di xame ndax dañuy toog walla dañuy jàll.