LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI Alxames 15 sàttumbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

DIINE

Màggalu Tuubaa

Tey di alxames 15 sàttumbar 2022, yamoo ak 18 Safar ci weeru araab, bés bi ñuy màggal tukkib Seex Ahmadu Bàmba Mbàkke. Mu nekk nag ab xew-xew bu mag ci réew mi ñu koy amale fale ca diwaanu Tuubaa.

XEW-XEWI JAMONO

Ñàkkum ndox ci yenn gox ca Tuubaa

Yenn cy gox ca Tuubaa ña ngay jooy ñàkkum ndox.  Ñàkkum ndox moomoo tax ba ñuy jaaye butéelub ndox bu 20i liitar ci njëgu 3. 000 FCFA.  Gox yooyu nag,  bokk na ci Gede, Surah, Tindodi, Bagdad, Daaru Xudóos…

Jéyya yi am ci yoonu Tuubaa wi

Lu tollu ci ñaar-fukki nit ñàkk nañu seen i bakkan ci jéyya yi am ca Tuubaa,  rawatina ci yoon yi.  Nde,  lu ëpp ñeenti téeméeri nit jële nañ ci ay gaañu-gaañu.  Limeesagum na lu tollu ci téeméer ak juróom-fukk ak benni aksidã. Kii di Kolonel Seex Tin mi ngi xamle ne ñi ñàkk ren seen bakkan ñoo ёpp ñu daaw ñi. Ndax, diggante gaawu ak àllarba rekk,  fukki nit ak juróom-ñett ñàkk nañu seen bakkan ci ay aksidã yu am ci yoonu Tuubaa wi.

Xew-xew bu doy waar ca diwaanu Koldaa

Am mbir mu doy waar moo am fale ca diwaanu Koldaa. Benn boroom dёkk la fa ag garab ray. Moom nag da doon seelu,  moom ak ñaari xaritam ci ron garab gi. Ni taw bi ak ngelaw li baree la garab gi mujje daanu seen kow, waaye moom faful a mucc.

Beneen xew-xew bu tiis ca Garã-Yoof

Lii, benn waay la buy wuyoo ci turu B. Seen, am lu tollu ci ñeen-fukki at ak juróom-ñaar, doon liggéeye fale ca AIBD (Aéroport International Blaise Diagne). Moom nag la ay sàmbaabóoy dogaale bi mu jógee ca bérébu liggéeyukaayam,  daldi koy faat.

PÓLITIG

Leerali ndeyi-mbill ji ñeel jaawale ga amoon ca péncum ndawi réew ma

Kumba Ndóofeen Njaay mooy ka demoon ca ba ñuy teg pekk gu bees gi fekk bokkul ci dépite yi. Moom nag mooy Njiital Parti pour le Rassemblement, la Justice, la Démocratie et le Développement bokk ci Yewwi Askan Wi. Ci ay leeral nag mi ngi xamle ne duggul ca Ngomblaan ga ci ag nёbb. Dafa laaj fara-caytu bu mag bi, kooku génne wayndare bi daldi ne ko am na Kumba Njaay bu fi nekk. Mu foog ne bu tёnkoo ci parité bi, bu jigéen jiitoo góor a ci war a topp. Kon njuumte am na ci, léegi mu ne kon,  na dugg rekk. Moom nag,  jot naa jёl kàddu sax ngir leeral ci lañu ko xamale ne du moom Kumba Njaay la. 

Aminata Ture

Ci ab waxtaan bu mu doon amal ak Tv5 Monde, xamle na fa ag ñàkk a àndam ci ñetteelu kayug (troisième mandat) Njiitu réewum Senegaal di Maki Sàll. Moom nag mooy ki jiite woon toftalaanug Bennoo Bokk Yaakaar ci wotey palum dépite yii weesu.

TÀGGAT-YARAM

Saliw Siis

Lu tollu ci ñetti weer kepp a des ci joŋante bu mag bi war a ame fale ca Qataar, te ba tey doomu Senegaal ji amagul ékib . Donte ne sax, ñenn ci gaynde yi am nañu jafey-jafey futbal lu bari fa ñu nekk. Terewul ne moom la ay mbiram gёn a ub boppi gaa ñi fare ci Staff bi jamono jii.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj