Li gën a fés ci xibaari bés bi Alxames 18 saŋwiye 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Layoo Aji Saar-Usmaan Sonko

Ñaari at daanaka bi coowal Aji Saar ak Usmaan Sonko tàmbalee ak léegi, kii di magum àttekat yi Umar Maham Jàllo jébbal na mbir yi ëtt bii ñuy dippe Chambre Criminelle. Kon, layoo bi ñu doon ruumandaat ay fan ci ginnaaw mooy bëgg a nekk dëgg. Waaye, ba tey nag kenn jàppalaguko ab àpp.

Taxawaayu Usmaan Sonko ñeel mbir moomu

Ci ndajem-waxtaan mi mu doon amal tey ci yoor-yoor gi, Usmaan Sonko joxe nay leeral ci mbir mi. Moom nag, nee na la mu waxoon màrs 2021 lay wéy di wax niki tey ba  ëllëg. Te mooy ne dina jël li ko yoon jox ci ay àq yépp, bañ  ba fu bañ yem. Te, nee na day bañ giiru dundam, te bu soobee Yàlla kenn duko teree nekk lawax ci wotey 2024 yi. Te, gisul benn àttekat bu ko mën a daan juróomi ati kaso ci mbir mii. 

Tabb yu yees yi

Ca ndajem jëwriñ ma mu doon amal démb, kii di Njiitu réew mi Maki Sàll jot na am ñenn ci ay ñoñam ñu mu takkal ay ndomboy-tànk. Ñooñu mu takkal ndombo yi nag, ñii la : Ceerno Njaay (Président de Conseil d’Administration de la Société Africaine de Raffinage), Séyni Béey (Président de Conseil d’Administration de l’Ecole nationale de Cybersécurité), Ibraahiima Géy (Inspecteur des Finances au Ministères des Finances et du Budget), Seex Abdu Lahaad Mbàkke Saar (Directeur de l’Administration générale et de l’Equipement au Ministère des Finances et du Budget), Abdulaay Njaay (Directeur de l’Administration générale et de l’Equipement au Ministère des Pêches et de l’Economie maritime), Demba Gay (Directeur du Développement des Energies renouvelables), Saana Saane (Directeur du Centre régional des œuvres universitaires sociales du Ziguinchor), Katerin Mari Terees Fay Jóob (Commissaire du Gouvernement auprès de l’Ordre des Architectes du Sénégal), Abdu Kan, Baabakar Mbay Njaay, Baabakar Seen (Professeurs titulaires à la Faculté des Sciences économiques et de gestion de l’UCAD), Mustafaa Soxna (Professeur titulaire de Didactique des disciplines à la faculté des Sciences et technologies de l’Education et de la formation de l’UCAD), Ndey Caam, Usmaan Séydi, Abdul Asiis Siis, Mammadu Jàllo (Professeurs assimilés à l’Ecole Polytechnique de Thiès).

Mbirum Fadiilu Keyta

Fadiilu Keyta, di kenn ci ñi jiite Nemmeeku Tour bi Njiital Pastef li Usmaan Sonko di def jamono jii, di it doom ci Nafi Ngom Keyta mi fi nekkoon Njiitu OFNAC dees na ko déglu suba ci àjjuma ji. Moom nag ñi ngi ko tegoon loxo juróom-ñeenti fan ci weeru desàmbar. Di ko toppe ne dafa biral ay xibaar yu wérul.

NJÀNG AK NJÀNGALE

Coppite turu daara ju kowe jii di UVS

Daara ju kowe jii ñu dippe woon UVS (Université Virtuelle du Sénégal), Njiitu réew mi Maki Sàll jël na ndogalu soppi tur wi. Léegi, ñi ngi ko tudde Université Numérique Cheikh Hamidou Kane (UNCHK).

Mbir mu doy waar

Lii nag ma nga xewe ca Géejawaay, ndongoy liise bu Séydinaa Limaamu Laay ñoo doon jote ak benn ‘surveillant’ bu nekke ca Ecole Privée Académia Limamoulaye. Nee nañu nag ndongo yooyu dañu doon def ab doxu ñaxtu, bëggoon a génnee seen naataangoo ya nekke ca daara jooja. Loolu nag la waa ji bañoon. Ca la ko ndongo ya songe. Ndongo yooyu nag am na ñu ñu ci teg loxo te ñu bari ci ñoom, jamono jii ña nga ca komisariyaa bu Géejawaay.       

WÉR-GI-YARAM

Jàngoroy kañseer ci réew mi

700i nit yu ame jàngoroy kañseer mooy limub ñiy xaar ku leen dimbali ci paj mi. Faatma Gënun, Njiitalu LISCA (Ligue sénégalaise contre le Cancer) mooy ki xamle loolu. Ndax, pajum kañseer dafa jafe, rawatina ci saa-senegaal yi nga xam ne dañoo néew doole. Dund bi rekk dafa jafe ñu bëgg ci boole paj mi. Day metti.

MBATIIT

Démb ci àllarba ji la kurél gii di Fonk Sunuy Làmmiñ doon sargal bindkat bii di Séex Aliyu Ndaw. Ki ñu doon sargal nag kenn la ci ñiy xeexal làmmiñ ak mbatiiti Afrig.

XEW-XEWI JAMONO

Xibaar bu tiis

Mbir mii nag ma nga xewe woon fale ca Sali Jaksaaw. As waay su soxnaam daan moy ak keneen, mu daldi xaru. Waa ji xaru nag mi ngi tolloon ci fanweeri at. Moom dafa jóge jàkka ja ci suba si rekk daldi xaru.

Lakk gu metti ca Dolli

Lakk gi ma nga ame woon ca Ranch Dolli ca diwaanu Lingeer. Lu tollu ci ñaari téeméeri ektaar nag lakk na ca. Ba tey, kenn xamagul lu ko taal waaye Sàndarmëri bu Ranch tijji na ci ab lànket ngir xam li sabab mbir mi.

Limub ñi faatu ci yoonu Espaañ wi

Bees sukkandikoo ci kurél gii di ONG Caminando Fronteras, lu tollu ci 2.390i bakkan rot nañ ci ndoxi Mediteraane yeek yu Atlantig yi ci atum 2022 mi. Seen yéene nag moo doondem ca Espaañ. Ñiy jóge ci Senegaal jëm Espaañ 1.784i nit ñàkk nañu ci seen i bakkan. Lu tollu ci 101i xale ak 288i jigéen jotuñoo àgg Tugal. Te, kurél gi biral na ne lim bi dafa wàññeeku ci atum 2022 mi, wuteek daaw, nga xam ne 4.639i bakkan rotoon nañu ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj