Li gën a fés ci xibaari bés bi (alxames 29 desàmbar 2022)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Yeneen tàbb yu yees 

Ca ndajem jëwriñ ma mu doon amal démb, Njiitu réew mi Maki Sàll am na ñenn ci ay ñoñam ñu mu takkal ay ndomboy-tànk. Muy ku ci mel ni Pàppa Maalig Ndaw (Secrétaire général du Ministère de l’agriculture, de l’Equipement rural et de la Souveraineté alimentaire), Mammadu Fay (Président du Conseil d’administration de la Société Immobilière du Cap-Vert) ak Idiriisa Jóob (Président du Conseil de Surveillance de l’Agence sénégalaise de la Reforestation et de la Grande muraille verte). 

Ay mbir yu yees ci coowal Aji Saar-Sonko

Kii di Njiital Pastef li nga xam ne moom la soxna sii di Aji Saar doon jiiñ ag ciif, moo wëlbëtiku pelent ñenn ñi mu jàpp ne dañoo laale ci mbir mi. Ñooñu nag, kii di Mammadu Maamur Jàllo ci la, Aji Saar ci la, Siidi Ahmed Mbay ci la, Wiwiyaan ak X (maanaam ku kenn xamagul turam). Moom nag, dafa ànd ak i layookatam, yokk ci pelent bi seedey fajkat bi doon seet Aji Saar, muy Doktoor Alfuseyni Gay. 

Coowal caabalug ëttu cettantal gaa ngay wéy

Tey la waa ëttu cettantal gi laaj kii di jëwriñ ji ñi dénk wàllu yoon mu ubbi ag wayndare ñeel gaa ñooñu ñuy tuddu ci luubalug xaalisu mbasum Covid-19 mi. Ndax, ñoom duut nañu baaraam fukki kilifa yu ñu bëgg yoon ubbi ci ñoom ay lëñbët ngir xam nu ñu laalee ci mbir mi. 

Càkkuteefu waa PUR

Ginnaaw bi yoon tegee loxo seen ñaari dépite yii di Masata Sàmb ak Mammadu Ñaŋ, ñoom nag dañu doon sàkku settantalaat kayitug pajug ndaw si. Ndax, kii di Seex Tiijaan Yum, dafa jàpp ne kenn waru leen a tëj ci ay feni neen.

KOOM-KOOM 

Njiitu réew mi nangul na waa PIP

Kurél gii di PIP (Programme d’Investissements Prioritaires) nekke ca Tàmbaakundaa,  kii di Njiitu réew mi nangul na leen seen sémb woowu. Seen ag kopparal nag mi ngi tollu ci juroomi-téeméeri miliyaar ci diggante atum 2023 ba atum 2025. 

Nafag meeri bu Ndakaaru xamees na ko

Démb ci àllarba ji lañu ko fésal. Nafag meeri gu atum 2023 maa ngi tollu ci 59,8i miliyaar. Koppar googu nag, jaglees na ko Bàrtelemi Jaas ngir mu mën a doxal liggéeyam. 

Bés bi ñu jagleel càmm gi

Tey, alxames 29 desàmbar 2022, mooy bés bi ñu jagleel càmm ci Senegaal, kii di Njiitu réew mi, Maki Sàll, ma nga ko doon màggalee fale ca Tàmbaakundaa. Mu nekk nag bés bu am solo lool ci nemmeeku gi Njiitu réew mi di amal foofa. Ndax, càmm gi bànqaas gu am doole la ci koom-koomu réew mi. Lii nag, mooy juróom-ñetteelu yoon i ñu koy màggal ginnaaw bi ko Njiitu réew mi biralee ci ab ndogal ci atum 2014, xaatimmon ci dekkareb 2014-164 bu 17 féewaryee atum 2014.

NJÀNG AK NJÀNGALE

Liggéeyu Faali Sekk 

Kii di Faali Sekk, meeru Roos Beeco, moo génnee lu tollu ci fukki miliyoŋ ak juróom-benn ngir dollil liise Allaaji Ahmadu Bekaay Jóob ay jumtukaay. Jox na leen lu tollu ci 462i toogu. 

Benn jàngalekat moo jam ab naataangoom                    

Kaawtéef ! Ab jàngalekat a jam moroomam. Li wund coow li nag mooy kii di O.T dafa njortoon ne xaritam bi day bëggante ak jabaram. Ci la ko jame paaka ci doqu gi. Ki mu jam, P.D.J., daldi ko yóbbu ci yoon. Moo tax, jamono jii, teg nañu ko daanub weeru kaso.

XEW-XEWI JAMONO

 Xibaar bu tiis

Benn daamar moo fiir benn xale bu tollu ci juróom-ñaari at. Loolu ma nga xewe ca VDN ba. Xale ba dafa bëggoon a dem ca tefesu Kàmberen ba. Ca la ko daamar ba fiire mu jaar fa ñàkk bakkanam.

Beneen xibaar bu tiis 

Benn xale bu tollu ci fukki at ak ñett moo lab ca Yëmbël, Daaru Salaam 5. Loolu nag mi ngi xew démb, ci ngoon gi. Dafa doon kuppe ak i moroomam ci benn joŋanteb futbal. Ndeysaan, ba mu dawal bal ba la xale ba moy, faf daanu ci basiŋ bi.                          

Ab aksidaŋ ci yoonu Kutal                   

Aksidaŋ baa nga xewe ca diiwaanu Kawlax, ci guddig talaata jàpp àllarba ; ñetti nit ñoo ca ñàkke seen i bakkan. Benn Jakartaa bu yeboon ñetti nit moo mbëkk ag sëfaan gu paan, taxawoon ci wetu yoon wi. Ñaar ña moom, ca saa sa lañu dee, ka ca des ca raglu bu mag bees dippe Allaaji Ibraahiima Ñas la ñàkke bakkanam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj