Li gën a fés ci xibaari bés bi Alxames 5 saawiye 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Leerali Usmaan Sonko ñeel ñaxtuy ndongoy Sigicoor yi

Ci ndajem-waxtaan mu mu doon amal tey ci yoor-yoor bi, Usmaan Sonko joxe na ay leeral ci ñaxtu yi ndongoy Sigicoor yi nekke ca Ndakaaru doon def. Moom nag, mi ngi xamle ne peyum dëkkuwaay yi du wareef ci meeri ndax amul cëslaay ci Yoon. Nee na nag, coow li mooy, nee ñu meeri daf leen a yoreel juróomi miliyoŋ ndax Abdulaay Balde moo ko waroon a fey te feyu ko. Kii di Duudu Ka moo leen ko feyaloon. Léegi nag, moom nee na, génnee juróomi miliyoŋ jox leen ñu dem du ko def ndax ni meeri bi di doxe mayu ko ko. Te, nee na liy wone ne ni bañuñoo fey mooy bi nu toogee ak léegi li nu waroon fey ci dëkkuwaay bi, fey nanu ko, tey boroom kër gi du leen wax ne ameel nañu ko xaalis. 

Ndajem-ñaxtu mu Yewwi Askan Wi

Démb ci àllarba ji, bi ñuy amal seen ndajem-waxtaan lañu xamle ne dinañu amal am ndajem-ñaxtu ci àjjuma ji. Ndaje moomu nag, dinañu ko defe ca Place de la Nation bu ñetti waxtu jotee.   

Xamees na àpp ak dëkk biy dalal ndajem-jëwriñ yi

Tàmbaakundaa mooy dëkk bi doon dalal ndaje moomu li ko dale ñaar-fukki fan ci weeru desàmbar wii ñu génn. Cees nag, moo koy dalal diggante juróomi fan ba fukki fan ci weeru féewaryee.

Yeneen tabb yu yees 

Ca ndajem-jëwriñ ma mu doon amal démb, kii di Njiitu réew mi Maki Sàll jot na faa takkal ay ndomboy-tànk ñenn ci ay ñoñam. Ñooñu nag, ñii la : Maxtaar Laax (Secrétaire général du Ministère du Commerce, de la Consommation et des PME), Faatu Bintu Njaay (Secrétaire général du Ministère de la Communication, des Télécommunications et de l’économie numérique), Moor Xujja Géy (Secrétaire général du Ministère de la Jeunesse, de l’Entreprenariat et de l’Emploi), Moktaar Ketaani Dukkure (Coordonnateur général de l’Inspection générale des finances), Faatumata Ñaŋ Ba (Président du Condeil de Surveillance de l’Agence Sénégalaise pour la promotion des Exportations au Minisère du Commerce, de la Consommation et des PME), Tamsiir Njaay (Directeur général de l’Agence nationale pour les Energies renouvelables), Mbay Njaay (Coordonnateur de la Direction générale des Douanes), Pàppa Calaw Faal (Directeur du Controle interne), Baabacar Mbay (Directeur des Opérations douanières), Muhammadin Umar Ba (Directeur de la Facilitation et du Partenariat avec l’Entreprise), Maalig Mbay (Directeur des Enquetes douanières), Aamidu Njaay (Directeur du Renseignement, de l’Analyse du Risque et de la Valeur à la Direction générale des Douanes), Pàppa Jijam Jóob (Directeur des Ressources humaines  à la Direction générale des Douanes), Abdul Xaadar Jeylaani Ñaŋ (Directeur de la Logistique et des Finances), Abdurahmaan Wàdd (Directeur des Système d’Information des Douanes), Ibraahiima Fay (Directeur régional des Douanes de Dakar-Port), Ahmadu Coy (Directeur régional des Douanes de l’Ouest), Abdurahmaan Ba (Directeur régional des Hydrocarbures), Usmaan Fay  (Directeur régional des Unités maritimes), Usmaan Kan (Directeur régional des Douanes du Nord), Buraama Jémme (Directeur régional des Douanes du Sud-est), Saaliw Juuf   (Directeur régional des Douanes du Centre), Ndey Aram Faal (Directeur de l’Informatique à la Direction générale de la Comptabilté publique et du Trésor),  Faatimata Daba Wan (Receveur général du Trésor à la Direction générale de la Comptabilité publique et du Trésor), Mammadu Mustafaa Jàllo (Directeur de l’Administration générale et de l’Equipement au Ministère de la Jeunesse, de l’Entreprenariat et de l’Emploi), Daba Ndóoy (Inspecteur des Affaires Adminidtratives et Financières au Ministères du Tourisme et des Loisirs), Aysatu J. Njaay (Directeur des Technologies de l’Information et de la Communication au Minitère de la Communication, des Télécommunications et de l’Economie numérique).

Teggi tuuma gu Aminata Ture

Ginnaaw bi mu fésalee, ñaari fan ci ginnaaw, ne day bokk ci wotey 2024 yi, dafa am ñaari kibaaraan yu biral ne caabalug IGE (Inspection Générale d’Etat) gu weeru me 2022 daf ko duut baaraamu tuuma. Mi ngi xamle ne xibaar yooyu du dëgg, seen jubluwaay mooy taqal deram. Rax-ci-dolli, suul coowal yorinu wu bon wow junni-milyaar yu Fonds Covid-19 yee ko sabab. Nee na, pexe moomu ngir xoqtal ko kepp a ko tax a jóg, waaye safu ko. 

 NJÀNG AK NJÀNGALE 

Bóomug Basiiru Mbay

Moom nag, jàngalekat la woon ca lekkool bu Théophile Turpin bu Njafat. Kii di jarbaatu njaatigeen a ko bóom. Tey lañu ko denc ca armeeli Bàqiya ca Tuubaa. Bàyyi na ginnaaw benn soxna ak ñaari doom. Ki def mbir mi nag, ma nga ñu téye ca sàndarmëri bu Kawlax. 

Taxawaayu naataangoom ya fare ca diiwaanu Kawlax

Jàngalekat ya nekke ca ñetti gox yii di ñooro, Gingineew ak Kawlax yépp ca Njafat lañu daje woon ngir ñaawlu li dal ci kow seen naataangoo boobu. Ñoom xamle nañu ne duñu jàngale li des ci ayu-bés bi muy alxames, àjjuma ak gaawu. Rax-ci-dolli, ñoo ngi sàkku ñu tëj ki def loolu giiru dundam.

 Taxawaayu waa UNAPEES

Kurél gii di Union Nationale des Parents d’Elèves et d’Etudiants du Sénégal ñoom tamit desuñu ginnaaw, ñi ngi naqarlu jëf jooju te di ko jaale ay mbokkam. Ñoom nag, yemuñu foofu ; ndax ñi ngi ñaawlu li jàngalekat yi jël dogalu dakkal njàng mi te mbir yi xeweewul ca biir daara ji. Rax-ci-dolli, du ndongo yi ñoo ko waral. Kon waruñoo nekk way-loruy moomule mbir.

Taxawaayu G7 

Ñoom nag ñi ngi naqarlu bóomug seen naataangoo boobu bu baax, te muy sàkku ci Nguur gi mu ubbi ci ag lëñbët ci ni ko yoon santaanee. Loolu tax ba ñu amal bésub lëmm boo xam ne dañu ciy dakkal njàng mi, mu yemoo ak alxamesu tey jii.

 Beneen xew-xew ca liise Limaamu Laay bu Géejawaay

Foofu nag, benn jàngalekatu SVT buy wuyoo ci turu A.W.T la benn ndongo bu àndoon ak yaayam ak jenn rakk walla magam doon saaga ak a tëkku ca biir daara ja. Ba ko naataangoom ya yëgee nag, ci lañu def am ndaje jël ndogalu dakkal njàng mi ñaari fan, saa bu juróom-ñeenti waxtu ci suba jotee, tey ak suba yépp, dakkal kàtte yi (devoirs), duñu nangooti ndongo loolu ci seen kalaas, te, di sàkku tamit ñu dàq ko ci daara ji.

XEW-XEWI JAMONO

Génnug àdduna Maturin Basen

Kii di Maturin Basen “Commandant de brigade de la gendaremerie” bu Lingeer moo génn àdduna tey ci suba. Moom nag, nee ñu bi mu jógee këram dëgmal bérébu liggéeyukaayam ca la daanoo (malaise) ñu yóbbu ko ca raglu ba fa la ñàkke bakkanam. 

Xibaar bu tiis

Lii nag jenn jigéen la ju tollu ci juróom-ñaar-fukki at ju ñàkk bakkanam ci ag lakk gu amoon fale ca Mbàkke. Donte ne sax sàppëer yi ñëw na ba fey lakk ga, waaye booba fekk na béy wéy na mbuus.

TÀGGAT-YARAM

Diggante Amaa Balde ak Giri Bórdoo

Làmb ji dox diggante Amaa ak Giri ma nga ca yoonu gàkk. Ndax kii di Amaa dafa am ab gaañu-gaañu. Mu mel ni kon àppu làmb jaa ngi ci yoonu tuxu ndax juróomi fan ci weeru féewaryee lañu ko waroon a bëre. 

Mbër yi daan mag ak rakk

Mbër yi daan mag ak rakk ci làmb ji ñi ngi tollu ci juróom-benn. Ñooñu nag, ñii la : Muhammed Aali Mbay Géy ak Mustafaa Géy, Yékini Paap Ciise ak Baabóoy, Bombarjee Paap Ciise ak Baabóoy, Alam Daar Usaa Sow ak Papaa Sow, Laay Pitaagoor Jet Li ak Sox, Booy Ñaŋ Bàlla Gay 2 ak Saa Cees.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj