WOTEY 2024 YI : WURE WA DEM NA KÉŊ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu tollu ci fukki weer ak juróom-ñett kepp a des ci wotey palum Njiitu réew mi, coow li ne kurr ci biir réew mi. Coowal wote yooyu nag lёmbe na lool làngug pólitig gi ci jamono jii, ku nekk naan man la. Mu mel ni wotey palum dépite yi moo tёnkoon gaa ñi. Ndax, bi njureefi wote yooyu rotee ba noppi la am ci gaa ñi ñu biral seen mébétu jёl réew mi 2024 bu fi Maki SÀLL jógee. Donte ne sax, àpp bi des na ab diir, ñoom dañuy fésal seen yéene ngir askan wi xam fi ñu féete. Ndax, ragal péete moom day xañe wёrsёg. Te, séddale moom ca kuddu yu jёkk ya rekk ba lay nangu di jёl cёru bañ. Moo tax, kii di Bugaan Géy ak Usmaan SONKO fare ci kujje gi xamal nañu askan wi seen mébét ci réew mi. Ndeem sax nag, am na ñeneen ñu fare ci kujje gi ñu àddoogul ci mbir moomu. Léegi kay, fi coow li nekk mooy ndax Maki SÀLL mi nekk nii ci boppu réew mi day bokkaat ca wote yooya walla ?

Wotey gox-goxaat yi ak yu palum dépite yi jàll nañu. Léegi, ku nekk ci ñoom xam na fu sa doole ak sa doole moroom tollu. Ndax kat, coow li bari na lool waaye ku wéet xam ka la mёn. Te, bu njaab yàggee rekk, gawar feeñ. Moo tax, mbañ-gàcce yi nga xam ne ñoo nekkoon géew ug gaa ñi doon joŋante àtte na leen ñaari yoon ci lu yàggul dara. Léegi nag, day mel ni benn wote moo ciy bёgg a des, muy bu 2024 ngir fal walla falaat am njiitum réew. Ba tax na, gaa ñi jàpp ne toogaay amatul, ku farluwul ñu far la. Moo tax, kii di Usmaan SONKO di Njiital PASTEF ci ndajem-waxtaan mu mu doon amal biral na ci kàddu yii : 

“ Bu soobee Yàlla Moomu di dogal, man mii de, Usmaan SONKO, lawax laa ci joŋantey Njiitum réew yu 2024 yi, bu soobe Yàlla. Bu ma ci génnee ndogalu Yàlla, dama naan bu ko sama pàrti nangoo ; ndax dama bokk ci pàrti boo xam ne dafa am nu muy doxe ñu am ay càrt yu ñuy tànne. Kenn ku nekk ci pàrti bi am sañ-sañu ne lawax la te bu boobaa dañuy def tànneef gu njёkk.” 

Loolu nag di firndeel ne moom mi ngi waajal wote yii di ñёw di ci woo tamit ay militaŋam ngir ñu tàmbali liggéey bi ñeel wote yooyu. Mu mel ni moom paaka la, du xaar kenn di ko jiitu ci mbaram. 

Waaye kii tamit di Bàrtlemi JAAS biraloon na ab lawaxam ca jamono yale weesu ci ab waxtaan bu mu doon amal ca TFM : 

“ Sama lawax 2024 mi ngi tuddu Xalifa Abaabakar SALL ndeem nee ngeen nag du bokku na ngeen ko gal-gal ngeen xool” 

Waaye, leeraloon na itam ne, bu Xalifa Sàll bokkul, du jàmmaarloo ak Usmaan Sonko ngir ne bu :

“ …  doonee lawax tey, amaana mёn naa wàññi doole Usmaan SONKO ngir mu doon Njiitu réew mi te man Usmaan jiiwuma loolu. Ba may wut meeri Ndakaaru daf ma jàppale gunge ma. Man su ma ko mёnee jàppale gunge ko, dinaa ko def. ” 

Kàdduy Bàrtlemi yooyu ca jotaay boobu di faram-fàcce day wane ñaari taxawaay yi mu am ci wote yii di ñёw.  Waaye, ba tey loolu firnde la ci ne moom du bokk ci wote yii di ñёw donte ne sax ñu bari jàpp nañu ne boroom mbooloo la.

Am na ba tey ci kujje ku ci biral mébétam muy kii di Bugaan GEY Njiital GЁM SA BOPP nga xam ne bokkul woon ci wote yii weesu. Mi ngi doon biral ay kàddu ca TFM mu ciy wax ne : 

“ Man li ma gёm mooy bu ñu yeggee 2024 man maay jiitu, damay xool ku ma jàppale.”

Moom nag ginnaaw bi mu sampee ndёndam ba pare yamul ci loolu rekk mi ngi ñaawlu tamit doxalinu Nguur gi. Ciy waxam :

“ Waratuñu yegg foo xam ne Njiitu réew mooy tànn naan kii day dem, kii day toog. Ñun ñépp dañoo war a bokk ci joŋante bi, kenn ku nekk xёccoo. Saa-senegaal yi mёn a tànn ku leen neex.” 

Ba tey, loolu day wane ne maxejj bu am yéeney bokk te matale càrt yi dafa war a bokk. Léegi, saa-senegaal yi tànn ki leen neex te doy leen, mu jiite leen. Waaye nag, ñii di waa PDS moom  ak yenn ci pàrtiy kujje gi biralaguñu seen i lawax. Donte ne sax, kii di Kariim WÀDD di doom ci Njiitu réew ma woon Maitre Abdulaay WÀDD nekk fale ca bitim-réew. Terewul am ñu jàpp ne mooy doon lawaxu waa PDS ndeem sax firnde bu leer amagul ci loolu. 

Waaye nag, coow li fi mu gёn a féete ci jamono jii mooy ci waa Nguur gi. Ndax kat, ku boot bukki, fàww xaj yi mbёw la. Li ko waral mooy kii di Maki SÀLL nga xam ne moo ngi ci ayam gu mujj bees sukkandikoo ci ndeyu-àtte mi nga xam ne dafa ne kenn mёnul def lu ёpp ñaari kay yu toftaloo. Moom ba tey yeyagul yàbbi ci mbir mi. Te, laaj bee di ndax ci kay yi ndeyu-àtte yi joxe lay yam walla day bokk ca wote yooyu ? Ndax, moom li mu ci jotoon a wax ca at mee weesu mooy “ak lu ci mёn di am bés bu wax jotee dinaa wax, wax jii ngay dégg nag mёnul xumbu ba ñu tax ma wax ci baat.” Kàddu yooyu nag ak ya leen jiitu ak yoy ñoñam tax ba am ñu jàpp ne day waaj a def ñetteelu kay. Te, li Bàmba FAAL wax di ko firndeel: 

“ Kon boog Njiitu réew mi ékib buy daan kenn du ko soppi, kuy indi ndam téye wёrsёg, kenn du ko soppi. Njiitu réew mi toogal, toogaat, toogati ba kenn wax la dara ñu defante ko ak moom.” 

Kii di Farba NGOM di ko dёggal ci wax ji mu naan moom mooy sama Njiit te bu sёlmalul du ma sёlmal. Mu mel ni ba tey mbir mi moom leeragul, bu fekkee ne ki ci war a wax waxagu ci. Waaye, seetaan a dàq ci am ndaje, te lu tёw a xam rekk dafa yàggul. 

2024 nag, donte ne sax ñewagul, liggéey ba moom door na. Ndax kat, fagaroo gёn faju te jubbanti ca ba muy teel. Moo tax, fi mu tollu nii gaa ñi jàpp nañu ne mbir mi ñor na xomm 2024 yegsi na ba noppi. Lu waay doon jaay léegi mu lamb. Ku mёn sa moroom na ko ko wan sa mbañ-gàcca ya.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj