Beneen lawax bu bees feeñati na ñeel wotey 2024 yi. Dr Baabakar Jóob, di meeru Cees, dina nekk lawax ci wotey Njiiteefu réewum Senegaal yii di ñëw. Moom nag mooy njiital pàrti pólitig bii di Forces démocratiques du Sénégal, les guélewars. Ci njeexitalu ayu-bés bi la koy ñoñam tabb bi ñuy amal ab ndaje ca CICES. Ginnaaw bi mu nangoo pal gi, xamle na ni mooy lawax bi namm a taxawal niiw-doole yi, di yit seen yaakaar.
KOOM-KOOM
Ngir gën a jàppale beykat yi ci seen liggéey, Njiitu réew mi, Maki Sàll, daf leen a fas yéene jébbal jumtukaay yu baax te takkoo takku. Mënees na leen a xayma ba ci 83i tamñaret ci F CFA. Jumtukaay yooyu nag, beykat yi waroon nañ cee jot niki tey, ci loxoy Njiitu réew mi, fale ca Grand Théâtre. Waaye, dañoo dàqandi ndaje ma ba beneen yoon.
COOWAL TER BI
Nguuru Senegaal weddi na ba set saabal bii di Figaro mi siiwaloon ni kër gii di SNCF (Société nationale des chemins de fer français) moo moom TER biy daw fii ci Senegaal. Kii di Abdu Ndeene Sàll moo génn ngir andiy leeral. Ci li mu xamle, du benn tubaab bu moom TER bi; TER bi, Nguuru Senegaal bokku ko kenn. Alalam la ci bépp fànn.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Ca UGB (Université Gaston Berger) bu Ndar, ndongo yaa ngay wéyal xeew bi ñu sumboon ci ayu-bés bii weesu. Dañoo xëyee dakkal dem beek dikk bi, taal i póno ak a jàmmaarlook takk-der yi ci altiney démb ji. Bokk na ci li leen tax a mer ba futt, mooy 4000y ndongo yi fa kilifa yi tàbbal ci ndorteelu at mi, te amul benn taxawaay bu ci war ba ñu am dëkkuwaay yu mucc ayib, bérébu jànguwaay yu matul, lekkuwaay yu xat lool ak fajuwaay bu doyadi. Ginnaaw ba ñu wàccee ca tali ba ba noppi, dakkal nañ lépp luy jotaayu njàng feek ñetti fan teg ci juróomi fan yu amul-fey ca lekkuwaay ya.
TÀGGAT-YARAM
Gaynde Senegaal yu jigéen yi amati nañ ndam ci turnuwaa Ufoa/A bi doon am fale ca Kab-Weer. Waa Kab-Weer ci seen bopp lañ dóor ci gañ-jël bi doxoon ci seen diggante démb ci dibéer ji (29 saŋwiye 2023). Ginnaaw bi kenn dugalulee bii ci xaaj bu njëkk bi, ci ñaareelu xaaj bi la ñaari ekib yi sog a tàqalikoo. Kii di Korka Faal moo dugal biiwu Senegaal bi, bi ñu tolloo ci 59eelu simili bi. Démb ci altine ji la gaynde yi ñibbiseek ndam li fii ci Ndakaaru. Cig Pàttali, gaynde yu góor yu ndaw yi dinañu amal seen demi-finaal ñeel Chan 2023 bi niki tey ci talaata ji, war cee daje ak Madagaskaar.
XEW-XEWU JAMONO
Lakk gu mettee metti moo am ca jawu Ocass ba ca Tuubaa. Lu tollook 113i béréb ñoo lakk ba doon dóom ci gaawu bi laata sàppëer yi di ko fay ci guddi gi. Ci xayma, alal ju takkoo takku moo lakk ba jeex. Muy ñàkk gu metti lool ci ña fay daane seen doole.
Ñeent nit ñu nekkoon i takk-der lees jàpp ci jëf yu ñaaw a ñaaw. Dañoo defoon seen gàdd ci turu yoon di wër kër caga ji. Fu ñu dem, nangu seen i alaal ba noppi tëdde leen, jàll feneen. Muy lu doy waar.