LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Saa-fuuta yi noppeeguñoo wannaasu tiiñal gi leen ñenn ci kujje giy tiiñal bi Bennoo Bokk Yaakaar rawee foofu ca Fuuta ci wotey Ngombalaan yiñ génn. Gannaaw bi BBY Podoor fasee yéene yóbbu fa mbaxane doone benn Usmaan Sonko ak Décce Fall, Séex Umar Aan jàpp na ni dañ leen a bunduxatal, yàq seen der ci neen. Te dinañ jàmmaarlook njiiti kujje gi ci làngu pólitig gi, di nañ leen yóbbu ci yoon.

KOOM-KOOM

Jawriñ ji ñu dénk xéy mi dina tànn 250i ndaw yu mu war a tàggat ci lépp lu jëm ci wàllu mbayum dund gi. Tàggatu googu a ngi am ci coobare Nguuru Senegaal ak lëkkaloowam ak BAD (Banque Africaine de Développement / Bànku Afrig ngir Yokkute)  ak ITA (Institut de Technologie Alimentaire / këru xarala ñeel dune gi).

XEW-XEWU JAMONO

Gannaaw taw bu yàgg te bare ndox bi wàccoon Ndakaaru ci àjjuma jii weesu, mbënn maa ngi wéy di lëmbe gëbla (capitale) gi. Yàqu-yàqu yi ak ñi ci loru di gën di bare. Ñetti nit jot nañ ci ñàkk seen bakkan. Ñaar ñi dañoo lab, ki ci des kuuraŋ moo ko jàpp. Rax-ci-dolli, gox yu bare Senelec dafa dog seen kuuraŋ ndax Post kuuraŋ yi dañoo taa. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj