Réewum Senegaal ak mom Muritani xaatim nañu ñaari pas yu yees. Jëwriñ ji ñu dénk mbiri bitim-réew, Soxna Yaasin Faal, ak naataangom bii di Mohamed Salem Ould Merzoug ñoo ko xaatim barki-démb ci altine ji ngir gën a dëgëral lëkkatoog ñaari réew yi. Genn pas gee ngi aju ci yombalal Saa-Senegaal yi këyitu dëkk (carte de séjourà ya réew ma di laaj ngir seen nekkin foofa gënn a yemb. Geneen pas geet, moo ngi aju ba tay ci mbirum xeex yooni tukki yees sàrtalul ak yu ci aju yi deme ni jàpp way-tukki yi ak di leen jaay.
TUKKIB ELIMAANU JËWRIÑ YI
Ginnaaw Koddiwaar ga mu demoon ak Gine, Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, wéyal na tukkeem fa réewum Siyeraa Lewon. Démb ci altine ji la fa wàcc, waroon fa nekk diirub ñaari fan. Ginnaaw bi ko tof-njiitu réew ma dalalee ba reer ak moom barki-démb. Ci talaatay démb ji lañu sumb i waxtaan yu am solo yu aju ci yokk lëkkatoog ñaari réew yi ci fànni koom-koom, kaaraange, bennoog diiwaan bi ak sas yi aju ci suqaleeku.
Demug Elimaanu jëwriñ yi ci ñetti réew yooyu, ginnaaw bi Njiitu réewum Senegaal njëkkee wër diiwaanu Afrigu sowu-jant ba muy soog a toog, dafay wane dogu gi réewum Senegaal def ngir jëmmal lëkkatoo yu dëgër ci diggante réewi Afrig yi, lëkkatoo yu lalu ci dimbalante, bennoo ak jonnug réewi Afrig yi.
CIT : TABB NAÑU HAAMIDU JÓOB
Tàbb nañu Haamidu Jóob, doomu réewum Senegaal ji jiite CNP (Conseil National du Patronat, di ndiisoog boroomi doole yu réew mi), mu nekk tof-njiitu CIT (Conférence Internationale du Travail, di lëlub àddina si ñeel liggéey bi). Démb ci altine ji lañu ko sàmp ca toogu boobu, bi ñuy amal ubbiteg 113eelu ndajeem lël bi kurél gii di OIT (Organisation Internationale du Travail, di mbooloom àddina si ñeel liggéey bi) nekk di amal fa Seneef (péeyu réewum Siwis), ci diggante 2 ba keroog 15i fan ci weeru suwe 2025.
Tabb gi ñu tabb Haamidu Jóob mu nekk toftalu njiitu CIT, doon na ndam lu réy ci Senegaal ak Afrig gépp. Jëwriñ ji ñu dénk liggéey bi, Àbbaas Faal, teewe woon na ubbite ga, moom ak ay njiiti sàndikaa yu réew mi mbaax fi réew mi.
MBUUR : JÀPP NAÑU FA 140i KILOY YÀMBAA
Fa Mbuur, teg nañu fa loxo 140i kiloy yàmbaa ci njógte yu fa Soldaari Mbuur (L’unité de lutte de Mbuur) yi, bokk ci birigàdd seneebar bu diiwaanu Cees, doon amal, ànd ceek pólisu, ngir xeex njaayum yàmbaa ci réew mi. fa mbeexi Mbaaliŋ ya lañu gisee yàmbaa bi, bi 1 waxtu di toftal 30i simili ci guddig talaata ji.
Luññutu yaa ngi ñuy wéyal ngir teg loxo képp ku ci laale, ñi ko moom ak ñi ko doon yaale.