LI WARAL NJËGU KURAŋ BI YOKKU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Li ñu doon laam-laame mujje naa am dëggëntaan. Njëgu kuraŋ bi yokku na li ko dale dibéer, 1eelu fan, ci weeru desàmbar 2019. Njiitu Senelec ci boppam, Paap Demba Bitéy, moo ko xamle keroog cim ndajeem ak taskati xibaar yi. Li waral yokkute gi, nag, ciy waxam, moo di ne Senelec dafa ñàkk lu tollu ci 12,191 milyaar CFA ci ñetti weer yi weesu. Muy xaalis bu takku.
Paap Demba Bitéy yokk ci ne :
«Xaalis boobu mi ngi méngook yokkute 26,3% ci njëgu kuraŋ bi. Woggantib 1eelu fan ci weeru desàmbaar bi ci 6% rekk lay yem, 20,3% yi ci des, nguur gee koy dékku. »
Njiitu Senelec li nee na yit yokkute gi du jural Senelec benn ngañaay. Rax-ci-dolli, jéem naa setal nguur gi. Ndax dafa ne, « nguurug Senegaal mësul a nangu ñu tëb rekk yokk njëgu kuraŋ bi. Moo tax mu doon def kéem-kàttanam ngir xettali askan wi, di ci dugal xaalisam.  Dimbalee na Senelec 316,342 milyaar CFA ci at yii weesu ngir rekk njëgu kuraŋ bi bañ a yokku ». Waaye, nee na bii yoon yokkute gi mënta ñàkk. Dafa di sax, réew yi féete Afrig sowu-jant yépp a ngi yokk. Te yit, lii du guléet, ndax bu yàggul dara, lu ni mel amoon na fi. Kilyaan yi mënoon nañ fee gëen a sonn bu ci nguur gi jàppul woon, ci li Bitéy wax ba tey. Ndax, ñoom, 2,462 milyaar kese lañuy fey, yemook 6% yi mu waxoon.
Sëñ Bitéy teg ci ne nguur gi baal na njariñaafon yi 0,7 FCFA yi mu leen waroon a dagg ngir defare ko kuraŋu dëkki kow yi (redevance d’électrification rurale – RER) li ko dale 2016 ba nëgëni-sii.
Xamle na yit ne, yokkute gi ci faktiiri sàŋwiyee 2020 yi lay doore ñeel ñiy fey weer ba weer, ak féewaryee 2020 ñeel ñiy fey ñaari weer yu nekk.
Paap Demba Bitéy wax na ne néew-ji-doole yi nga xam ni seen lim mi ngi tollu ci 611.203 boroom-kër, maanaam 54% – téeméeri nit yoo jël, juróom-fukki yi ak ñeent duñu yëg yokkute gi.
Masoxna Kan, njiitu SOS Consommateurs (mbootaay la, di sàmm àqi njariñaafon yi) moom, Maxtaar Siise la tontu ci rajo RFM, daldi ne :
« Li Maxtaar Siise, jawriñ jiñ dénk laf gi, wax, bett nanu. Bu ko neexee jàppale njiitu Senelec, waaye bum nu jàppe ay dof, bumu jéem a fowe xeli askan wi. Dafa ne, nguur gi du masin buy fiir fenkat. Naam, waaye nguur gi day jëfandikoo kurél yu mel ni Senelec ngir sos ay feni nguur te loolu, mën nan ko firndéel. Li Paap Demba Bitéy wax yépp dara du ci dëgg. Bi ci jiitu, dafa ne, yokkute njëgu petorool bi ci àddina si moo waral depaasu Senelec yokku, mu am pertmaa. Loolu du dëgg. Ku dem ci anternet bi, dinga gis ne li mu wax yenuwul maanaa. Nee na ci atum 2016 réew yu bari yi wër Senegaal dañoo amoon ay jafe-jafe ndax yokkute njëgu petorool bi. Du dëgg. Ci atum 2016, njëg li wàccoon na ba 30 dolaar te, jamono jii, mi ngi tollu ci diggante 58 à 60 dolaar. Te sax, njëg loolu, petorool biñ war a jaay weeru saŋwiyee la ñeel, jotewul daraak li xew tey. Atum 2014 la njëg li tàmbalee wàcc, bindoon nanu sax nguur gi xamal ko ne dafa war a wàññi esãs bi ak kuraŋ bi, lu mu tuuti tuuti, téeméer bu nekk fanweer, 30%. Kon, bu kenn taafantoo petorool bi. Li mu wax ne nguur gi jox na ko Senelec amul, lan a ko firndeel ? Nee ñu nguur gi dina joxe 10i milyaar, askan wi joxe 2i milyaar. Waaye loolu teguwul fenn. Njàngaan li gën a ndaw mën na firndeel li may wax. Depaasu Senelec bi dafa yokku, waaye loolu taxul kuraŋ bi war a yokku. 611.203i doom-aadama yi ñu ne bokkuñu ci yokk gi ana ñu ? Nan wone fu seen tur nekk ni ko Aar li nu bokk laajee. Te sax, naka lees di xame kan moo néew doole ak kan moo néewul doole ? Xanaa du ñéppay jëfandikoo kuraŋ? Ana firnde yi ? Ay waxi kasaw-kasaw la ! Li am ba des moo di ne liggéeykati Senelec yi duñu fey kuraŋ. Lu tax ?  Waxoon nañu fi tamit ne dinañu wàññi at mu nekk 3i milyaar te defuñu ci dara. »
Kàddu yooyu la Masoxna Kan rotaloon ci RFM keroog biñ siiwalee yokkute gi.
Ci atum 2009, ay këri-gëstu yu mag amaloon nañ fiy njàngat ñeel doxalinu Senelec, daldi digal nguur gi mu tas ko, def ko ñetti pàcc : njuréef li, dem ak dikk gi ak céddale gi. Boroom xam-xam yi bindoon loolu noon nañu benn « holding » moo leen war a bokk yilif. Nguur gi defu ko te ba leégi waxul lu tax.
Liggéeykati Senelec yi dañoo war a fey kuraŋ ni ñépp. Ak ni ñu yi baree, bu dee duñu fey, funu jëm ?
Paap Demba Bitéy nee na tamit gornmaa bi yoreel na Senelec 250 milyaar. Waaye ana kan la nguur gi ameelul bor ?
Li mu bànk a tax muy koppartu, yokk mburu, esãs, simaŋ, kàrta giriis ak permi añs.
Gormaa buy àddu-kalpe doy na waar !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj