LU ËPP TUURU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Saxaar, safara a ko yabal. Wolof ne, xoddiku balaa lakkle. Senegaalu tey, ci xoddiku la tollu. Nde, Senegaal a ngi mel nib barigo cim mbartal mu rattax. Bés bu set, ñu dégg fiy kàddu walla ay jëf yoy, musiba ju réy a réy lañuy gaatnga. Li ci gënatee doy waar mooy ne, kàddu yooyule, ay kilifa yu gàllooy ndomboy-tànk ak i mag yu bijjaaw ñoo leen di biral. Ñoom ñi waroon a doxal njekk, njëkk a dox jàmm, ñooy xamb taal bi. Dara nag, waralu ko lu moy, kujjeg pólitig ak bëgg a jafandiku ci nguur guy saay. Ay “Gëmmal dóor !” (Mansuur Si Jamiil),  “Nanu jël jaasi yi” (Aliw Demburu Sow, APR), “…nañu rey, bu ko jaree, 90i saa-senegaal ci 100 yoo jël !”(Séex Yerim Sekk), “Nañu rey Usmaan Sonko !” (Mustafaa Jaxate, APR), “Gatsa-Gatsa, Mortal Kombat” (Usmaan Sonko), añs.

Diggante 2012 ak tey, ci xayma, lu ëpp 50i doomi réew mi ñàkk nañu seen i bakkan ci sababi pólitig, ay téeméeri téeméeri jële ciy gaañu-gaañu. Am na sax ñu ci laago. Yàqute yi nag, maaradeetaali. Li yàqu ciy alal ak i jumtukaay, mëneesu ko natt. Lim bi ci ñàkk liggéey, ak ñi ñu ci tëj kaso tamit, kenn xamul nu mu tollu. Ba jonni-Yàlla-tey jii nag, coow li fayagul. Te, liy xeeñ, saxaar la sos, bees ko fayul léegi-léegi, daay bu jéggi dayo lay juri. Nde, coow laa ngi bëgg a rax. Waaw. Buñ demee ba ciy boole li ci bokkul, di jéem a beddi xeet ak dëkkub lëmm ci réew meek mberaay mi, ku tiitul woon war nga tiit. Ndogal yi njiiti dem beek dikk bi jël fan yii ñeel diiwaanu Kaasamaas teey na xel.

Fan yii yépp, ñoo ngiy ruumandaat ne, Nguur gi dafa bëgg a beddi Kaasamaas ci Senegaal. Mu am nag ñu bari ñu weddi wax ji. Nde, yenuwul maanaa. Ndaxte, Senegaal ay Kaasamaas démb, balaa tey. Kaasamaas mooy Senegaal tey, ëllëg ba fàww. Kenn mënul wax Senegaal te doo ci boole Kaasamaas. Kenn mënul wax Senegaal di ci génne Kaasamaas. Dafa di, diggante Kaasamaas ak Senegaal, Usmaan Sonko xaju ci. Diggante Senegaal ak Kaasamaas, Maki Sàll xaju ci. Kon, kujjeg pólitig walla mbañeel diggante ñaari nit ñuy xëccoo nguur, warul a tax ñuy beddi diiwaanub lëmm ci mberaayum réew mi. Loolu nag, Càmm gaa ko war a saytu, taxawe ko, fexe ba xàjj ak seen bañ a am. Waaye, bu jengee rekk, dara du baax. Te, lees seetlu fan yii moom, raglu na bu dee dëgg la ne waa nguur gi dañu guuxal mer waa Kaasamaas ci sababu Usmaan Sonko.

Bi réew mi yëngoo fan yii weesu, ginnaaw 2i at yees daan Usmaan Sonko, ndaw ñi taaloon nañ ay daamari Dakar-Dem-Dikk yu baree bari. Moo taxoon sax ñu dakkaloon dem beek dikk bi. Bi jàmm delsee, biis yi tàmbaliwaat nañ daw ci taliy Ndakaaru yi.  Waaye, biisi Dakar-Dem-Dikk yiy daw diggante Ndakaaru ak Sigicoor, ba tey dawaguñ. Nee ñu kilifay  Dakar-Dem-Dikk yi ñoo jël ndogal li. Moone de, fa Sigicoor, ak li xeex biy tar-tar, kenn jafalu fa biisu Dakar-Dem-Dikk. Kon, li tere biis yi lëkkale Ndakaaru ak Sigicoor ëlëm na xel yi. Te, ba léegi, genn kilifa àddoogu ci. Lu tax ? Dañuy fayantook waa Sigicoor walla ?

Li tax laaj bi sampu mooy ne, gaal gi doon lëkkale Ndakaarook Sigicoor sax, tëmbatul. Ba tey, kenn xamul lu tax. Ñu ni déet-a-waay, ñu dakkal tukkiy roppalaan yi doon dem Sigicoor. Te, ba tey, genn kilifa indiwul i leeral ñeel ndogal yii nga xam ne, jural nañ askanuw Sigicoor ak way-tukki ya fa bëgg a dem jafe-jafe yu bari. Waaye, day nasaxal koom-koomu réew mi.

Muy waa Dakar-Dem-Dikk, di gaalu Alin Sitooye Jaata ak naawu gi, dina am liggéey yu yàqu ak xaalis bi ñu ciy ñàkke. Te, loolu day tax paasu Ndakaaru-Sigicoor yokku. Ku xam ni dawalkati Senegaal yi mel, war a njort ne paas bi dina ful ñaar ba ñetti yoon. Yaxantukat ay baykat ya féete Sigicoor tamit, seen liggéey dafa nar a yàqu. Nde, ñi ci ëpp, Ndakaaru lañuy jaaye seen i njuureef.

Dañu seetlu ne, bi Usmaan Sonko fëllee ba tey, dañu singali waa Kaasamaas, rawatina joolaa yi. Am nay ndaw ñuy fi jàppoon, ñu génn wax ne, seen sant yee taxoon ñu jàpp leen. Senegaal mësut a àgg fii. Te, wàlluw xeet du lees di fowe walla di ko pólitige. Coow lii, warees na ko dakkal bés niki tey balaa muy ëpp i loxo. Te nag, lu ëpp tuuru.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj