Kurél gii di ànd gësëm, di kurélug waa kër doktoor, àddooti na. Wile yoon nag, du ngir gësëm walla di bank seen i loxo. Dafay ñaawlu lees ko boolewul ci péncoo mi fi Njiitu réew mi woote woon ci wàlluw yoon, rawatina ndogal li ñu jël ci ni dañuy féexal ndung-siin yi ak ba tax ñu nar a woyofal daan yi ñeel mbirum tux ñax. Ñuy xamle ni lu ni mel bu amee dina doon lu bari njeexital ci wàlluw wér-gi-yaram. Ba tax ñuy dàq lépp luy oyofal tux mi, rawatina yàmbaa bi nga xam ni ku mu rayul, dofloo la.
RIIRUM MBIRI YÀQ BIIR
Ci fan yi ñu génn, bari woon na lool ay fésal yu doon daw ci mbaali jokkoo yi ñeel pexey yàq biir. Looloo waral ba jëwriñu wér-gi-yaram bi yékkatiy kàddu jëmale ci. Ci yégle bi mu génne, ma nga cay dànkaafu askan wi ci ñàkk wóoradi mbir mu ni mel. Muy xamle jafe-jafe yi ci mën a jóge ci di ko defee ci bërëb yi ko jagoowul walla ak nit ku ci xelam màccul.
Bu weesoo loolu sax, yàq biir doon na lu ñuy tere fi réewum Senegaal. Yoon ci boppam moo ko dàq, bu dul biir bi nar a andi loraange. Te bu boobaa Yoon moo koy taxawu. Lu ko moy, Yoon dina teg loxo jigéenu-wérul ji ko def, ki ko ko defal ak képp ku ci laale.
PÀTTALIKU SEMBEEN USMAAN
Démb ci dibéer ji, doon nañ màggal pàttaliku Sembeen Usmaan. Muy 17eel wi yoon ci ren ginnaaw bi mu dëddoo ci atum 1997. Ñaŋ ko doon amalee fa Ndar-Géej, ci jàppandalug waa Daaray Sembeen. Wile yoon, waxtaan waa ngi aju woon ci ni mu waree fi kembarug Afrig ñu ànd jubbanti rajo yi, tele yi ak lënd gi. Ñu di ko wax ci nasaraan « la régulation coordonnée de l’audiovisuel et de l’internet : un impératif en Afrique ».
SINEEBAR BI
Sineebar baa ngi wéy di riir ci biir réew mi. Ginnaaw jàpp yu am solo yees fi jot a amal ci weer yi weesu, tegaat nañ ci loxo fa dalub roppalaan AIBD ci gaawu gi. Muy sineebar bu ñu nammoon a génne réew mi. Bi ay 19i waxtu di jot, lañ ko teg loxo. Mu tollu ci 20i kilo. Bees ko xaymaa, dina dem ba 1 600 000 ci FCFA. Pólis teg na ci loxo 4i nit. Toppee nañ leen itam ba xam kër giñ daan denc mbir yi fa Popengin.