LUUBALU 540I TAMDARET CA CMS BU MEDINAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

CMS ab bànqaasu déncuwaay ak àbbuwaayu xaalis la bu nekk ci biir réew mi. Fan yii ñu génn, lañ gis ci yéenekaay yi ne luubal nañ fa lu tollu ci 540i tamdaret ci sunuy koppar, looloo tax njiitéefu CMS gi def ab pelent. Ci la waa « Sureté urbaine » jël mbir mi nekk ci di ko lëñbët. Ci biir lëñbët bi lañ jëkk a jàppe kii di A. Kunta, di ab « femme d’affaires », ak Remõ Ngom di njiitul CMS la woon bu Medinaa. Ñoom ñaar ñoo jëkk a feeñ. Ndax A. Kunta dafa daan jëfandikoo ay dàntite jàmbur ngir di leb ak a luubal xaalis ci ndimbalu ñenn ñuy liggéeye ca CMS bu Medinaa. Nde, soxna si Kunta dafa doon compal ñi mu jëloon seen i dàntite lu tollu ci 200 000i ci xaalis boobu mu daan leb.  Remõ Ngom, moom it, nangu na ne yégoon na lu ni mel, te it waxooon na ko njiitam yi, waaye njiitéefu CMS gi weddi na ko ba mu set.

Noonu, lëñbët bi di wéy, ba ñeneen feeñaat. Kenn ki ab tëgg bu weex la (bijoutier), di wuyoo ci turu Aamadu Gise. Ndeke, A. Kunta daa jëloon Aamadu Gise ngir mu xamal waa CMS ne gaarànti bi muy joxe ngir mën a leb xaalis wurus la. Waa CMS ñoom, dañoo woowaate beneen tëgg bu weexul ngir mu xoolaat ndax li A. Kunta joxe wurus la am déet, noonu lañ xamee ne du wurus. Ci la CMS pelentee ñii di A. Kunta, Remõ Ngom ak Aamadu Gise. Bi lëñbëtkat yi laajee, Aamadu Gise daf leen tontu ne li ko soxna wonoon wurus la te du deñ, soxna si moom it nee na wurus la joxe biir CMS.

Bees sukkandikoo ci yéenekaay bii di Source A, juróomi nit yi ñu jàpp ne seen loxo génnul ci luubalu xaalis bi, Maaxam Jàllo mii di magum àttekat yi teg na leen jàppug négandiku ci àllarba jii 6 desàmbar 2023. Ci biir juróom ñooñu, ñett ñii di Remõ Ngom, S. Nduur ak A. K. M. Saaña ñooy liggéeyee CMS. Li ñuy toppe Astu mooy njublaŋ ak weexalug xaalis. Ñi ci des tamit ñu leen di toppe kurélu jëfkaati lu bon « association de malfaiteurs » teg ci di yokk doole njublaŋ. Ndeke bi Astu daan jox xaalis ñi mu jëloon seen i dàntite, ci loxo kii dii A. K. M. Saaña la daan génne. Nii lañ deme ba xayma ne lu toll ci 540i tamdaret moo nar a naaxsaay. A. Kunta nag, nangu na ci kanamu lëñbëtkat yi ne moo nekkul ci dëgg, te it dina fey xaalis bi. Ciy waxam, nee na denc na lu toll ci 200i tamndaret, dina ko jox waa CMS, te it, li ci des dina ko fey.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj