MAATAM : WALUM DEX GI NANGU NA 700i TOOLI CEEB

Yeneen i xët

Aji bind ji

Walum dexu Senegaal gaa ngi wéy di jur ay loraange yu jéggi dayo. Fa diiwaani Maatam, Kéedugu ak Tàmbaakundaa (Bàkkel). Njiitu réew mi sax, tukki na tay ci àjjuma ji, nemmeekuji askan way yeewoo fa diiwaan yooyee ngir taxawu leen.

TOOLI CEEB YU BARI YÀQU NAÑU

Fa diiwaanu Maatam, lu ëpp 700i tooli ceeb la mbënnum dexu Senegaal gi nangu. SAED moo ko xamle.

1000iy baykati ceeb ñoo ci yàqule. Musaa Mbóoj a ko biral, moom mi jiite banqaasu SAED bii di “Division appui à la production et à l’entrepreneuriat rural”. Daf ne :

“Ca mbënn mu njëkk ma, mooy bi dex gi walee, dafa amoon 400i ektaar ciy tooli ceeb yu ndox mi nangu woon. Bees ci dollee mbawi ndox yi, àgg na ci 700i ektaar ciy tooli ceeb.”

Ci àjjumay tay jii la yékkati kàddu yile, bi muy tontu laaji saabalkat yi. Li ci doy waar mooy ne, ciy waxam, mbir mi naru fee yam. Ndaxte, saa su nekk, mbënn mi mën na yokku bu dee dex gaa ngi wéy di wal. Waaye, ba tay ciy kàddoom, SAED a ngi jël ay matuwaay ngir dimbali baykati ceeb yi.

TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA KÉEDUGU AK BÀKKEL

Fa Bàkkel moom, mbënn mi daf fa gën a jéggi dayo. Nde, kër yu bari la fa nangu ak i daara. Nee ñu, am na fa gune gu lab ci ndox mi. Rajo RFM a ko siiwal.
Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga Kéedugu ngir nemmeeku leen, taxawu leen. Ci àjjumay tay ji la fa dem. Ay boori 10i waxtu ci yoor-yoor bi la fa àgg. Ci màkkaanu sóobare mees dippee “Fodé-Ba” la njëkk a dal. Mi ngi sol yérey sóobare. Ci biir kilifa yi ko gatandu, jëwriñu njàng meek njàngale mi, Mustafaa Giraasi, ca la bokkoon. Demoon na ciy béréb yu ndox mi nangu tay jii. Ëllëg tamit, ci gaawu gi, dina seeti way-loru yi. Démb rekk, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, xamle woon na ni Càmm gi, ci ndigalu Njiitu réew mi, jagleel na 8i miliyaar ci sunuy koppar way-loru yi.

Dina dem Sarayaa, fa diiwaanu Kéedugu ngir nemmeeku béréb ya ñuy gasee wurus yi. Dina dem itam Sabodolaa, dem ca ndefaru SOREDMINES, dem Bàkkel laata muy dellu Ndakaaru.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj