Usmaan Sémbeen doon na am téeméeri at ci ren, bu fekkoon muy dund. Jànguneb Ndar, ñu gën koo xam ci turu UGB (Université Gaston Berger de Saint Louis) nekk di ko màggal jamono yii. Jotaay yi di am ci diggante jàngune beek Institut français bi nekk Ndar, li ko dale alxames 18 me ba gaawug tey jii 20 me 2023.
Bu Usmaan Sémbeen doon dund, dina am 100i at ci ren jii. Téeméeri at nag du lu ndaw, rawatina ci koo xam ne, nit ku ràññeeku la ci àddina sépp. Looloo waral ba UGB wooteb lël bu ubbeeku ci àddina sépp ngir màggal ko ci anam yi mu méngool, jaare ko ci jàppandalug jànguwaay bii di CRAC (Civilisations, religions, arts et communication), maanaam Xayte, Diine, Aar ak Jokkalante.
Ci ñetti fan yi ñu àppal lël bi, dinañu ci dégluy gëstukat, seetaan ciy filmiy reyaalisaatëer yoy, seen xam-xam màcc na ci ndonob Sémbeen. Lépp aju ci waxtaane anam bi Sémbeen doon liggéeye, ni mu daan xeloo ci caada ak di ko méngaleek jamono, ngir mën a nànd njëfam yi koy dundal ba léegi, moo xam ci wàllu ladab la walla ci sinemaa.
Usmaan Sémbeen nag, mekanisiyeŋ la woon, jóge fa doon masoŋ. Bi ñaareelu xareb àddina si (1939-1945) jollee lañu ko boole ci sóobare yi bawoo woon Senegaal ngir xettali Farãs gi Itleer nammoon a noot. Ba xare ba jeexee, la dugg waaxu Màrsey, nekk fa yenukat. Ginnaaw gi, mu sóobu ci yoonuw mbind ba mujje doon bindkat bu mag a mag.
Ciy mbindam, ñu ràññe ci lool Le Docker noir, maanaam Yenukat bu ñuul bi (di téere fent bi mu njëkk a bind), walla boog les Bouts de bois de Dieu, Banti Maam Yàlla yi. Waaye, bu turam àggee ci ñu koy coow fu nekk ci àddina si, rawatina fii ci kembarug Afrig, Sinemaa moo tax. Moom mi tàmbalee ci mbind, tàbbi ci film ngir gën a mën a wax ak askanam wi sawarul ci dawal ndax li mu aadawoo kàddu. Mu am ci ndam lu réy nag. Mujje doon senaarist ak reyaalisaatëer bu xereñ ba tax ñu jàpp ni moo tette sinemaa ci Afrig.
Bi ñuy tjji lël bi ci alxames ji, Jëwriñ ji Aliyu Sow teewoon na fa. Moom sax lañ jagleeloon kàdduy ubbite gi. Ginaaw bi mu rafetloo xew mi, delloo njukkal ñi ko taxawe, dellu na fésal yéeneem ci taxawal ab xewte fii ci réew mi. Dafa jàpp ni jaaduwul dara Senegaal di bañ a am xewteem, moom mi nekk réewum Sémbeen, ci jamono yii nga xam ni ñu ngi koy màggal fépp ci Afrig ak ci àddina si. Rax-ci-dolli, Fesfaco bi ñuy coow, mu nekk xew-wewu sinemaa bu mag, Sémbeen mi fekk mbaax Senegaal bokk na ci ñi ko sos.