Keroog, gaawu 3 féewiryee 2024, la Njiitu réew mi jëloon ndogalu xaatim ab dekkare buy neenal njëlbeenub dekkare bi sàrtaloon wote yi ba léegi. Ginnaaw gi, dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yeek yu PDS yi dañoo booloo, jaay doole dépitey kujje, daldi wote sémbub àtte biy dàq wote yi ba 15 desàmbar 2024. Dafa di, bi dépitey kujje gi taxawee ci waxuwaay bi (pupitre) wax ne kenn du wote fileek féncuñ sémbub àtte bi, sàndarm yi lañ woo ñu taxañ leen, dagaj-dagaje leen, génne leen Ngomblaan gi. Boobaak léegi nag, coow lu réy a réy juddoo na ci. Yemu ca, dañu nangu lisãsu Walfadjri, tëj ko. Ñu ni déet-a-waay, ñu dog net bi laata ëñu koy delloosi. Booaak léegi, Maki Sàll a gën di wéet ci ndogalam li.
Fi réew mi, biir Afrig ak fépp ci àddina si, ñu ngiy mbamb Senegaal. Senegaal, royukaay ba woon ci wàllu demokaraasi, réewum jàmm ak dal, réewum waxtaan ak maslaa, tey Senegaal googu la Maki Sàll gàcceel ba ñépp di ko ci xas ak a yedd, fi réew mi ak bitim-réew.
Muy Bennoog Tuga di Saa-Amerig yi, kenn ci ñoom rafetluwul ndogalu Maki Sàll li. Bu dee fi réew mi, wëliis way-pólitig yeek ñi seen xam-xam màcc ci wàllu yoon, kuréli liggéeykat yu bari ànduñu ci te fas nañoo yéene xeex ba demokaraasi ak jàmm dellusi fi réew mi.
Kurél gi ëmb sàndikaa yi jonn yi, C.S.A. (Confédération des Syndicats Autonomes), àddu na ci tolluwaayu réew mi ci wàllu pólitig. Ab yégla la génne di ci joxoñ Njiitu réew mi ak njiitul Ngomblaan gi, di leen wax « …ñu bañ a dugal seen loxo ci yoonu woteb Senegaal bi te fexe ba banqaas yi ciy liggéey yépp (Kurélu àttekat yi, CENA, Caytu gi, Way-moomeel yi, Làngi pólitig yi) mën a def seen liggéey ni mu ware te yem fi leen yoon yemloo. » Ginnaaw loolu, kurél gaa ngi leen di soññ tamit ci ñu « neenal ndogal yi safaanook yoon yi ñu jël yépp. »
Bu loolu weesoo, ñu ngi delloosi xelu Maki Sàll miy Njiitu réew mi, di njiitu campeef yi fii ab keroog 2 awril 2024, bés bi moomeem gi di jeex. Mi ngi koy ñaax mu sàmmoonte ak i wareefam ni ko Njiiti réew yi ko fi jiitu defe woon, te fexe delloo askan wi àqam, te mooy tànnal boppam ki koy jiite. Nee ñu tamit, C.S.A. dina bokk ci bépp xeex buy tax demokaraasi delsi te di ci tàllal loxo yeneen sàndikaa yépp.
Kurél gii di CNES (Confédération Nationale des Employeurs du Sénégal), moom itam, génnee na ab yégle di ci biral njàqareem ci tolluwaayu réew mi ci sababu dekkar bi Njiitu réew mi xaatim. Nee nañ, ndogal loolu day gàkkal demokaraasi Senegaal te day yee fitna. Ci seen yégle bi ñoo ngi ciy waxeet ne, ndogalul dàq wote yi dina jural réew miy gàllankoor ci fànn yu bari, rawatina ci wàllu koom-koom gi, njàng mi ak deru Senegaal fa bitim-réew. Te, loolu, day dawloo ñiy indi seen xaalis ci réew mi ngir def ko fi. Moo tax, ñoom waa CNES, ñuy « …ñaawlu anam bi réew mi nekke, [te di woo] Njiitu réew mi, moom mi war a sàmm Ndeyu àtte réew mi, mu jël ay matuwaayam ci nim gën a gaawe ngir sàmmoonte ak arminaatu wote bi. »
Ñoom itam, waa CNES, niki waa CNES, noppi nañoo bokk ci lépp luy tax jàmm ak dal am ci réew mi.
Ay futbalkat niki Jomansi Kamara, Papis Demba Siise ak Mbay Jaañ fésal nañ seen ñàkk ànd ci ndogalu Njiitu réew mi. Ci wàllu mbuug, rawatina rab, kii di DIP DUNDU GUISS tamit àndul ci ndàqug wote yi.
Ba ci ñi fara ak moom sax, ñu ngi koy bàyyi ak a xalab. Birima Njaay mi doon xeexal Nguur gi ci jotaayi tele yi sax, di waxee xol, doy na ci misaal. Daf ne :
« Yow réew mi danga yaakaar ne Maki Sàll moo ko moom walla APR ? Réew mi danga yaakaar ne APR la sant walla Bennoo Bokk Yaakaar la sant la sant ? Te sax, lu war a sabab ñuy dàq wote yi ? Lu xew ? Xam nga lii day may dëgg Paap Aale Ñaŋ ak gaayi Sonko yi…képp ku fi wax waxi dàq ay wote workat nga ! »
Mu mel ni kon, ñépp a ngi wan ginnaaw Njiitu réew mi nga xam ne, bés bu nekk, day gën di wéet ci ndogalam li.
Kujje gi ak kurél yu bari fas nañoo yéene génn ëllëg ci àjjuma ji ngir ñaxtu. Xel dalagul nag ci li nar a xew. Ndax, du ñàkk takk-der yi bëgg leen ko tere ci ndigalu seen i njiit. Te, bu boobaa, xeex dina am. Fi mu nekk nii nag, Maki Sàll fasagul yéene dellu ginnaaw. Mu des nag Ndajem Ndeyu àtte mi. Ndax, ci kàdduy Aliyun Tin, ñoom rekk ñoom mën a muccal réew mi jamono jii. Daf ne :
« Menn pexe kepp lanu mën a jaar ngir sàmm Bokkeef gi, joyyanti tëralinu ndeyu àtte wi ñu salfaañe te àggali yoonu wote yi te pexe moomoo ngi aju ci Ndajem Ndeyu àtte réew mi. Bu Ndajem Ndeyu àtte réew mi neenalee dekkareb Njiitu réew mi, dina delloosi ci jàmm ci réew mi te teg ko ci yoon. Ndaxte, li Maalig Gàkku ak Seex Tiijaan Jéey bind Ndajem Ndeyu àtte réew mi ngir ñu neenal ndogalu Njiitu réew mi, ab buntu génnuwaay la. waaye, fàww baatu doxal gi (l’exécutif) am xelu nangu li xew te nangoo jëfe ndogalu yoon. Moom sax, ndax baatu ndogalu Senegaal bi am na meneen pexe ? »