Njiitu réew mi, Maki Sàll, mi ngi soññ ak a xirtal ay ñoñam. Ci talaata jii weesu la doon wax fa New York, ca ndajem Mbootaayu Xeet yi. Jóo naa leen soppi anam bi ñuy pólitigee. Daf leen a woo ci ñu xoolaat xeeti pólitig yi ñuy lal ñeel caytu gi, koom-koom gi ak kopparal gi. Ciy waxam, àddina sépp a war a gis seen bopp ci pólitig yi njiit yiy doxal.
Wëliis xelal bim xelal moroomi Njiiti réewam, Maki Sàll rafetlu na “liggéey bu am solo” Bi Mbootaayu Xeet yi jot a amal ci biir kembaaru Afrig. Jagleel na yit ngërëmam kurél gi Bretton Woods ngir li mu liggéey fi Afrig.
Njiitu réew mi, Maki Sàll, jagleel nay kàddu kii di fara-caytu bu mag bi, Antoñoo Gucires di ñaawlu na tanqamlu bi Mbootaayu Xeet yi di tanqamlu yeen réew yi ci bokk. Nde, dañuy am i soxla, Mbootaay gi war leen a dimbali. Waaye, buñ leen seetaanee, daf leen di nasaxal. Loolu nag, day sabab ay juuyoo ak i féewaloo. Mu ngi koy ñaan, di ko ñaan waa Mbootaay gépp, ñu jàpp ci. Daf ne :
“Mën nanu ko def bu dee farlu nan ci, jox ko itte ji war. Kurél gii di G20 wone na ko. Nde, ñoom, biraloon nañ ne, Bennoo Afrig gi (Union Africaine) dafa war a doxal i àqam ni mu ware. »
Noonu, gërëm na bu baax a baax waa G20 ñeel ndimbal gi ñu dimbali Senegaal ba muy dagaan njiiteefu Bennoog Afrig.
Njiitu réew maa ngi jeexaleey kàddoom ci tàggatoo, xamle ne déwén, keneen ku dul moom moo fay teewal Senegaal.