Pekkub Ngomblaan gi dafa amaloon am ndaje ci bésub tey jile. Ndaje ma nag, daanaka ñépp la bett. Ndeke, ci mbirum Soxna Aminata Ture la ndaje ma aju woon. Dafa di, yàggul dara, waa Bennoo Bokk Yaakaar dañu sàkku woon ngir ñu summi mbubbum dépite bu Mimi Ture. Càkkuteef googu la waa Pekkug Ngomblaan gi doon càmbar ci seen ndaje ma. Biñ ci génnee nag, xamle nañu ne kii di Soxna Aminata Ture ñàkk na mbubbum dépiteem. Ci li rotagum ciy xibaar, 16i dépite ñoo wote, 10 yi daldi wote ngir ñu summi mbubbum dépite soxna si, 6 yi daldi bañ. Nee ñu, waa lëkkatoo WALLU ñoo tax ba càkkuteefu lëkkatoo Maki Sàll gi jàll. Nde, ñoom, dañoo wote ngir Aminata Ture génn Ngomblaan gi.
Bi xibaar bi àggee ci dépite Aminata Ture, àddu na ci mbir mi, wax ne :
« Léegi laa yëg ne Njiitu réew mi, Maki Sàll, dàqluna ma ca Ngomblaan ga, ci lu teguwul fenn. Rax-ci-dolli dafa jalgati Yoon. Li ma leer ba leer mooy ne, dara mënuma tere wéyal sama xeex ngir demokaraasi bu jaar yoon biir Senegaal, ak xeex lii di ñetteelu moomee gi mu nar a def. Dañ koy bañ. Xel sax nanguwu ko, astemaak yoon. »
Ñu baree ngi naqarlu ak a ñaawlu ndogal bile. Ndaxte, jàppees na ni, li Ngomblaan gi def, ag jaay doole kepp la, te Maki Sàll moo nekk ci ginnaaw. Am na sax ñu jàpp ni dañoo woñ loxo Yoon ci mbir mile. Ngudda Mbuub ci la bokk. Ma-Yoon bi lii la wax ci mbir mi :
« Dépite kenn warul laal moomeelam ca biir Ngomblaan ga, seen moomee a deme noonu. Te, ci yoon, kenn amul màqaama folli ab dépite bu nekk ci moomeelam. Bu ñu demee ba moome di aju ci ay ndigal, nekkatul moome. Réew maa ngi ci guta. Ndax, Càmm gi daf nuy jaay doole… Boo seetloo mbirum 9i dépite yu Tógóo yi, ëttub àttewaayu CEDEAO bi leeral na ne, tekkig ndombog-tànk dépite ajuwul ci ay àtte. Waaye, dépite bi lay neex mu defal ko boppam, bindal ko boppam… Ndogal li ñu jël ngir xeex Mimi Ture, du lenn lu dul njubadi ak jalgati yoon. »
Ginnaaw xibaar boobule, beneen toftalu na ci. Moor Taala Géy walla Nit-Dof, ràppëer bi ñu jàppoon keroog àllarba 18 saŋwiyee 2023, lees wax ne Maaham Jàllo dóor na ko màndaa-dë-déppóo, jàllale ko kaso. Layookat bii di Me Xureysi Ba ne, li àttekat biy toppe Nit-Dof mooy : « ciiwalug xibaar yu wéradi, tëkkuy rey ñeel kilifay Yoon (dog 194, 255 ak 290 bu Càrtug Daan gi). »
Fi mu ne nii, dafa mel ni Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak waa Bennoo Bokk Yaakaar, naruñoo dellu ginnaaw. Boobaak léegi, ñoo ngi seqiy jéego, jëm ci fitna. Te, ku dégg ni Njiitu réew mi waxe tey ci yoor-yoor bi, xam ne dafa bëgg a jëfandikoo Yoon ak dooley Nguur ngir jàmmaarloo ak ñi koy xeex, di xeex ñetteelu moome gi muy yootal. Réew mi nag, saxaar a ngi fiy xeeñ, buñ ci xëppulee ndox, daay dina am. Te, bu daay amee, ña ko taal, ña ko suuxat ak ña daan seetaan di jaay maandu, ñépp a nar saay. Ndax, wolof nee na, ay du yem ci boppu boroom.