Ginnaaw bim tànnee lawax bi mu bëgg mu wuutu ko ci boppu réew mi, Maki Sàll, Njiitu réew mi, dina indiy coppite ci Càmm gi laata muy tukki fa Etaasini, ci dibéer jii ñu dëgmal.
Dañ ko doon ruumandaat fan yii yépp. Njiitu réew mi daa fas yéene yeesalaat Càmm gi, tabb ay jëwriñ yu bees yuy àggali liggéey bi ci 5i weer yii ko dese. Nee ñu, moom ci boppam moo ko xamal ay jëwriñam, keroog ca seen ndaje ma ñu baaxoo amal ayu-bés bu jot. Yéenekaay L’observateur moo siiwal i kàddoom yim fa wax. Bees sukkandikoo ci yéenekaayu Yuusu Nduur bi, Maki Sàll daf ne leen :
“Damay soppi Càmm gi fi ak njeexitalu ayu-bés bi. “
Li Njiitu réew mi nisër mooy tabb Càmm gu bees fii ak dibéer. Jukkees na ci yégleb Ndajem jëwriñ yi ne, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa yégal ndaje ma ne dafa war a tukki fa Etaasini. New-York la jëm. Dafa war a teeweeji 78eelu ndajem aada bu Mbootayu Xeet yi. Ndaje moomu, jàppees na ko diggante 17 jàpp 23 sàttumbaar 2023. Bu ça jógee, dina am ñu mi gisanteel.
Kon, bu ngànt gaarul Njiitu réew mi ci diggante bi, dinañ am Càmm gu bees ci gaawu gi. Xam nañ ni daal, Aamadu Ba dina génn ngir gën a mën a sóobu ci kàmpaañ bi, waajal wote yi. Doon nañ wax itam ne, Abdulaay Daawda Jàllo la bëggoon tabb mu wuutu Aamadu Ba ci boppu Càmm gi. Waaye, bokkenaajo bi dafa bañ. Li mat a laaj nag, moo di : lan mooy jubluwaayu yeesalug Càmm gi ? Liggéey ? Neexalaate ?
Ak lu ci mën di am, lees deful 12i at, mëneesu def ci 5i weer. Bu dee ne dafa bëgg giifal ñenn ñi tamit, dina jafe ci moom. Li waral mooy ne, koo xam ne 5i weer kese ñoo la dese ci jal bi, jox la cër day xaw a jafe ci wàllu pólitig.