MALIKUNDAA : KËRUG MBËJ GU BEES

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senelec taxawal na kërug mbëj fa Malikundaa. Loolii dina tax ba dawaanu mbëj mi ful fukki yoon fa Pointe Sarène. Nde, lu jiitu ñu fay samp kër googii, 50i kilovoltampères la dëkk ba daan jot. Waaye, léegi, ak na kërug mbëj ga ca Malikundaa, dinañu jot ci 400i kilovoltampères.

Bànku Almaañ bii di KfW moo joxe koppar yi ñeel naaluw suuxat ak yaatal laf gi (Programme de promotion de l’efficacité énergétique et d’accès à l’énergie). Koppar yaa ngi tollu ci 37i miliyaari FCFA. Jubluwaay bi mooy yokk mbaaxaayu mbëj mi te jàppandal ko ci askan wi.

Naal woowu dina tax itam dëkki kaw yu bari ye dend ak Pointe Sarène jot ci mbëj mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj