MÀNDELAA WAR NAA AM NAQAR FA MU TËDD !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lan moo dal sunu mbokki réewum Afrig-bëj-Saalum ? Su ma nee ‘’mbokk’’, nit ñu ñuul ña fa fekk baax a may tax a wax. Nook nun benn lañu, koo ci ni woon tey diw mii Simbabwe la bokk walla Somali walla Niseryaa, kenn du la weddi. Ci lu amul benn werante, nooy nun, nun nooy ñoom. Nun ñépp la sunu der ñuul, sunuy aada doon daanaka benn, nu bokk jaar-jaar ndax ni nu Tubaab yi boolee metital, nangu sunu alal, jàppenu niy bàyyima. 

Moo tax jamono ja African National Congress (ANC) fippoo ci njiiteefu baay Nelson Mandelaa, ñuy xeex apartheid– doon boddikonte ci biir xeet bu yoon daganaloon – kenn bankul sa loxo di leen seetaan. Ni leen réewi Afrig yépp sotlee jarul di ci delsi ndax kenn wóor na ma ni fàttewu ko. Xanaa rekk fàttali askan wi ne fii ci Senegaal, muy woykat yi, di bindkat yi walla ñeneen, kenn desul ginnaaw. Dem nan sax ba lekool boo dugg gis ñu bind fa baat yii ci kow tablo bi, gone yiy janook moom bés bu Yàlla sàkk : L’apartheid est un crime contre l’humanité

Ci weeru awril 1994 la ANC dakkal apartheid, Mandelaa toog ci jal bi. Kon, bi buumu-njaam gi dogee Afrig-bëj-Saalum yàggul, ndax ci wàllu mboor (histoire) 20i at ak juroom du dara. Bi mu ko defee, doomi-Afrig yu bare jóge Senegaal gii mbaa Mosàmbig mbaa Kóngook Niseryaa wutali réew ma, fas-yéene faa daan seen doole.    Ñu bare ci ñoom, nag, dañoo jàngoon ba ni arr, am i lijaasa yu wóor, rawatina waa kër Robeer Mugaabe yi seen réew sësook réewum Afrig-bëj-saalum. Doomi-Afrig di Sidd, ñoom, dese woon nañoo xareñ ci lenn mbaa am xam-xam, ndax ci jamonoy apartheidTubaab yi bëgguñu woon seen njàng sore. Loolu daldi jur lii : doxandéem yu ñuul yiy am xéy, doomi-réew mi ci seen bopp di taxawaalu.  Looloo indi coow li, du leneen. 

 Teewul 10i at mbaa lu ko ëpp a ngii ñuy siis nit ñu ñuul ñi, di leen bóom, di lakk seeni bitig. Dañuy def yooyu ñaawteef, teg ciy fan mu mel ni du woon ñoom.  Waaye dangay jékki-jékki rekk dégg ne songaat nañu nit ñu ñuul ña ! Looloo fa xew fan yii weesu ba fukki doomi-aadama ñàkk fa seen bakkan.

Lu ni mel mi ngi tàmbali ci ndorteelu sàttumbar te ba tey jii ñu ngay wéy di song doxandéem yi bawoo Afrig. 

Siril Ramafoosa, njiitu réew ma, naqarlu na ko, teg ci ne congi aji-xeetale yi jaaduwul te xel mënu koo nangu. Waaye boo seetloo bu baax, yéex naa yéy yàbbi ci mbir mi. Am na sax ñuy joxoñ baaraamu-tuuma nguur gi ak kujje gi yépp, ni ñoom ci seen bopp ñooy ruux seenuw askan, muy def musiba yooyu.  Waaw, xanaa du ñoom ci seen bopp ñooy ndamoo li boddikonte dakk ci seen réew ? Kon, lu tax ñuy metital ay doom-aadama ndax li seen der ñuul, di leen rendi niy xari tabaski ? Àddina sépp a ngi teg i bëtam ci seeni ñaawteef. 

Ci kaw loolu, Buxaari miy njiitu Niseryaa fas-yéene woon na sol ay dàllam wutali réewum Afrig-bëj-Saalum toog ak naataangoom Ramafoosa, ñu jéem a saafara mbir mi. Gémmiñ bu waxul dëgg, wax fen : mbugël mi mënul a wéy. Waa Niseryaa tàmbali nañoo feyu. Naam, reyuñu kenn waaye ñu ngay yàq ay bérébi liggéeyukaay yu am maanaa yu ay doomi-réewum Afrig-bëj Saalum moom. Ci noonu la MTN (kurélu xaralay jokkalante gi ëpp doole ca dëkk ba) ak Shoprite – ñu mën koo méngaleek Auchan añs – tiitee ba tëjëndi yenn ci seeni bànqaas. 

Dëgg la, lu ëpp tuuru, waaye mer bay defante ak a tëj ay àmbasad, du saafara mbir mi. Nee ñu Niseryaaa ngiy waaj a génne ci dëkkam doomi- réewum Afrig-bëj-Saalum ya fa ne waaye loolu fajul dara. Li am solo mooy fexe ba Doomi Afrig yi jéem a booloo, di xàccandoo, di dóorandoo. Lu ko moy, sunuy sët dinañ nu mere, naan nun danoo xeeboon sunu bopp. 

Bu loolu weesoo, ndaje mu mag ñeel koom-koomu Afrig, door na ci 4u fan ci weeru sàttumbar ca Keep Taawun waaye Niseryaa dafa mujjee gedd, ne moo lànk du fa teew…

Lu mat tamit 600 ci ay doomam nangu nañoo dellu seen réew, 300 ci ñoom àgg nañ sax Niseryaa, bàyyi ginnaaw seen liggéey ak seen teraanga. 

Li xew tey réewum Baay Màndelaa, nag, mënees na ni luy raam la, jëm ci ñag bi ; te ku deful ndànk réewi Afrig yu bari diñañ topp ciy tànki reewum Afrig bëj-saalum, dal ci kow doxandéem yu ñuul yi fekk baax Afrig.

Am na benn boroom xam-xam bu ma ne lii lépp ba muy door démb la woon, tey soog a ñëw. Ci gis-gisam, ndajem Berleηci atum 1885, lu mat a bàyyi xel la. Ca la réewi Ërób yi ëppoon doole séddoo Afrig, ku nekk ñu ni la suuf sii yaa ko moom, nit ña fay yeewoo tamit yaa leen moom, lu la neex defal. Moo tax nuy noonoo ci sunu biir, ñi seen bopp xaw a woyof naan fii maa ko moom, ku fi bokkul ñëw di xëccook man, dinaa ko digaaleek yow. Njiiti réewi Afrig yi nga xam ni ay dunguru tubaab yi lañu lu jiin Njaag a te ñooy Njaag. Ndax taluñu dara lu dul dajale xaaliis ak nguuru. 

Ñaawtéef yii ak xeex bu tar bii mënees na koo tudde xeexu way-néew-ji-doole yi seen biir, muy li Silyuus Maleema naan : dungeen dégg mukk ci réewum Afrig-bëj-Saalum ñu ni dóor nañ fa ab Sinwaa walla nit ku weex tey taafantoo li mu amul kayit walla leneen. Maleema yokk na ci  sax ne ñi yaakaar ni dañoo bañ doomi Simbabwe walla Somali, daanaka seen bopp lañu bañ ndax li leen Tubaab yàgg a wax ne nit ku ñuul ak malaa yem, ñu dem ba gëm ko, képp ku ñu gis nga ñuul ni ñoom ñu dal ci sa kow.

Tabo Mbéki tamit, bi mu toogee ci jal bi def na kem-kàttanam ngir moytu réeroo bi jur lii. Ñu dàq ko, Sakob Zuma wuutu ko, di nag ku matadi daanaka ci faan yépp, di seetaan ñaawteef yi dem tey ba ëpp loxo.

Waaye mënees naa am yaakaar ne lu ni mel dootul am Sowaneesbuur ak Peretoryaa. Ramafosaa jéggalu na ciy naataangoom, ñépp di ci dégg te bu sàmmee kàddoom nguur gi dootul bank i loxoom bu ay sàmbaa-bóoy dee bóom ay doomi-Afrig di lakk seeni kër ak seeni bitig.  

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj