Mbëkk mi reyati na. Fukk ak ñeenti néewi Saa-Senegaal lañ fekk cig gaal fale, ca réewum Repiblig Dominikien. Ci lees xamle, dañ mbëkki woon. Démb la gaal gi yeb seen i néew teer. Kurél gii di Horizons Sans Frontières moo ko siiwal. Ci biir néew yees ràññe ci biir gaal gi, fekk nañ ci doomi réew mi ak yu Muritani. Ci biir néewi Saa-Senegaal yi, ràññees na ci turi Yànqooba Taal mi juddu 31i pani me 1991 ak Siidiyaan Wàdd mi juddu 10i pani oktoobar 2000.