MBIRI BAA JAXATE AK IMAAM NDAW

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey ci altine ji la Baa Jaxate ak Imaam Séex TIijaan Ndaw doon janook àttekat bi ci mbiri boroom ñaari tur yi ñu doon tuumaal magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko.  Looloo taxoon ba yoon doon leen toppee lu jëm ci jàll baat nit kuy doxal ndombog tànk walla lenn ci ndomboy tànki Njiitu réew mi.

Kii di Baa Jaxate sax, am na lu mu weddi ci kanamu àttekat ba. Daf ne, kàddu yees koy tuumaal, waxu leen. Ciy layam, Imaam Ndaw moo wax i waxam, askanale ko ko. Waaye, Imaam Ndaw moom, delluwul ginnaaw ci wax ji. Daa feddali, dëggal ni li mu wax ci mbiri ngóor-jigéen, ay waxi Baa Jaxate lañu yoy, deful lu dul baamu leen. Rax na ca dolli sax ne, mësul wax ni dafa juum. Wax ji ñu dugal ci caabal gi la te, bi ñu koy déglu, layookatam nekku fa.

Toppekat bi sàkku na ñu tëj leen 6i weeri kaso ak i ndàmpaay yi ñuy war a fey. Ginnaaw gi àttekat bi dafa dàqandi àtte bi ba keroog altine jii di ñëw, 3 pani suwe 2024. Layookat yi sax doon nañ sàkku mu bàyyi leen bàyyig négandiku, waaye àttekat bi daf leen ko gàntal.

Bu weesoo loolu, beneen pelent gàllu na cindoddu Baa Jaxate. Abaabakar Mbuub mu Ànd Sàmm Jikko yi moo koy topp ci sos ak waxal ko lu amul.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj