MBIRUM 300i ROÑUKAT YI RÉER CI GÉEJ GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ñetti gaal, yeboon 300i nit, 300i doomi réew mi, ñoo ne mes, réer. Ñaari ayu-bés, bi ñu tëmbee ak léegi, kenn gisu leen, kenn déggu leen. Fa Kafuntin lañu bawoo woon, song mbëkk mi ngir mucc ci ndóol gi. Espaañ lañ jublu woon, doon dagaani wërsëg fa duni Kanaari ya. La ñu suturloo lañ bëggoon. La ñu ko dugge woon mooy teral njaboot, teral mbokk ak dund ci ngor. Teraanga lañu doon yóotu, àddina daldi leen wor.

« Fafalnaaw bi wër na fépp. Waaye gisuñu dara. » Lii la way-wattuy español ya doon wër gaal yi wax. Kon, tubaab yaa ngi leen di wër. Nguurug Senegaal moom, gëmuñu sax ne am nay gaali saa-senegaal yu naaxsaay ci géej gi ak 300i nit ya ñu yeboon.

Ci ngoonug taalata ji, 11i fan ci sulet, la njëwriñu mbiri bitim-réew yi ak saa-senegaali ya fa nekk, ci njiitalu Aysata Taal Sàll, génne woon ab yégle di ci weddi ak a miim xibaar bi. Dañu bind, wax ne ñoom, mbetteel lañu am bi ñu gisee « …xibaar biy law ci mbaali jokkoo yi ñeel 300i saa-senegaal yu waroon i gaal, jóge woon Kafuntin ngir jëm ca duni Kanaari ya, faf réer ci géej gi. » Aysata Taal Sàll nee, ci yégle bi, saytu nañu xibaar bi, xool ba xam dëgg la am déet. Ca lañu gisee ne, ci seen i wax ba tey, « …xibaar boobu wérul. » Dolli nañ ci ne sax, « …diggante 28 suwe ak 9 sulet 2023, xettali nañ 260i saa-senegaal ca géeju Marog ga. » Ñu raxoon ca, dolli sax ne, « Koñsilaa Senegaal ba ca Marog nekk ca dëkk bañ naan Dakhla, lëkkaloo na ak njiiti Marog yi ngir ñu delloosi leen ci jàmm. » Ci gàttal, Aysata Taal Sàll dafa weddi ne am na 300i doomi Senegaal yu songoon mbëkk mi, réer ci géej gi. Waaye de, dàjjees na waxam ji.

Dafa di, ci altine ji rekk, meeru Kafuntin bi, David Jaata, dëggaloon na ci RFI ne, am nay gaal yu fa bawoo. Wax na sax ba leeral ne :

« Roñukat yi (ñiy dugg ci gaal yi ngir dem tugal), ñu ci ëpp, dëkkuñu Kafuntin. Ci yeneen i béréb ci biir réew mi lañuy jóge, walla ñuy doxandéem yu bawoo ci réew yi nu wër : Gàmbi, Gine Bisaawo, Gine Konaakiri, ak sax Niseer. Bu njëkk, bariwu fi woon, ndax Mbuur lañ daan demee. »

Ñu ni déet-a-waay, ONG Caminando Fronteras bu Espaañ daldi feddali xibaar bi. Nde, ñoom, waa ONG bi, ay roñukat walla seen i mbokk ak i jegeñaale ñoo leen di woo di leen xibaar. Moo tax, bu ñu waxee, xam nañ fu ñu ko teg. Moo tax, boobaak léegi, ñoo ngi wër, di wër rekk. Ki sos ONG bi, Helena Maleno, bindoon na tweet ci talaata ji, di ci wax ne :

« Deesul a sàggane benn simili ngir gisaat 300i nit yi nekkoon ci gaaliy saa-senegaal fekk ñu ngi dund (…). Aajowoo nañu ay jumtukaay yu gën a bari ngir ceet gi. Fàww tamit réew yii di Moritani, Espaañ ak Marog gën a ànd liggéey. »

Nguurug Senegaal moom, ndeem weddi na xibaar bi, njorteesul ne dina jóg, def i pexe ngir feeñal doomi Senegaal yooyu réer ci géej gi. Njaboot ak mbokki 300i roñukat yi, ñoom, tiis ak njàqare lañu war ame jamono jii, di ñaan ngir ñu feeñ te ànd ak seen i bakkan.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj