Ca atum 2022 la coowal ñaari sàndarm yii di Dijje Baaji ak Fulbeer Sàmbu jiboon, lëmbe réew mépp. Nde, ñaari sóobare yooyu, dañu jékki woon rekk réer. Bi ñu toogee as diir, ca lañu gisoon seen i néew. Jamono jooja, Maki Sàll a jiite woon réew mi, ñu nekkoon ci ay yëngutey pólitig yu tar. La Nguur ga xamle woon nag, cib yégle, mooy ne ñaari takk-der yooyu dañu laboon. Waaye, ba tay jii, ñu bari gëmuñu loolu. Boobaak léegi nag, luññutu yaa ngi doon wéy. Moo tax, lu bees rot na ci. Ndax, bees sukkandikoo ci yéenekaayu Libération, yoon tuumaal na kii di Serom Bànjaki mi ñuy dàkkentale « Sniper », daldi koy tëjlu tëjub négandiku [mandat de dépôt]. Ci àjjuma jii weesu la àttekat bi jël ndogal loolii. Tuuma yees koy toppe ñooy : nëbb nit ak bóomug ñaari sóobare.
Serom Bànjaki mi ñu ci jàppagum nag, gàllees na ko yeneen ñaari tuuma. Nde, ci li Libération xamle ba tay, yoon dafa wax ne dafa doon tëkku tëkkuy ray ak mbugal ñeel ab seede bu am solo ci mbir mi. Nde, seede boobu moo tax yoon gis ay mbir yu ko umpoon, daldi baral luññutu yi.
Ay kuréli àq ak yelleefi doomu Aadama dañu yàgg a xeex, di kaas ngir ñu wéyal luññutu yi. dafa di kat, boobaak léegi, ameesu ci woon xibaar yu bees. Mu mel ni mbir mi dafa naaxsaay.
Ci dibéeru démb ji rekk, amoon nay way-pólitig, ay militaŋ ak kuréli way-moomeel yu doon amal ab doxu-ñaxtu ngir fàttal njiiti réew mi, ñu bañ a « fàtte » mbir moomu. Séydi Gasama mi jiite Amnesty International Sénégal àdduna ci, di laaj ñu amal luññutu yu xóot te lalu ci màndute. Dafa ne :
« Am na ku ñu tuumaal, waaye moom kese mënul def lépp. Yoon dafa war a wéyal luññutu ngir Saa-Senegaal yi mën leen a wóolu. Fàww ñu leeral ñi jiite mbir mi [bóomug ñaari sóobare yi]. »
Dafa mel ni nag yoon dégg na leen, ba tax ko ubbiwaat wayndare woowa. Doxalin woowu nag, neexul layookatu Serom Bànjaki bi. Nde, Me Jibi Jàllo, moom, dafa am mbetteel ci tuuma yees teg ci kaw kiliyaanam. Li ko bett ci mbir mi, ciy waxam, mooy ne « Pólis mësul déglu Serom Bànjaki ci mbir moomu [bóomug ñaari sóobare yi]. » Ci li mu xamle, dina jokk àttekatu ñetteelu néegub gëstu bi [juge du troisième cabinet d’instruction] ngir leerlu ci sababi doxalin woowu.
Xibaar bile nag, dafay wane ne luññutukat yaa ngi tàmbalee liññi mbirum bóomug Dijje Baaji ak Fulbeer Sàmbu. Waaye, ba tay, am nay mbir yu leeragul. Loolu moo tax kuréli àq ak yelleefi doomu Aadama, yoy way-moomeel yi ak lenn ci askan wi di sàkku ci yoon mu leeral lépp, def li war.