Mbiru “Fonds Force Covid-19” mi lëmbe na lool réew mi fan yii. Bari na ñoo xam ne woolu nañu leen ci. Moom, Mamadu Ngom Ñaŋ, ci ñi Yoon woolu woon ci la bokk. Nde, ca jamono yooya, moo nekkoon DAGE (Directeur de l’Administration Générale et de l’Equipement) fa njëwriñu tàggat-yaram gi. Li ñu koy toppe mooy luubal alalu askan wi. Waaye, jot naa génnee lu tollu ci téeméeri miliyoŋ ak juróom-fukk ngir ñu bàyyeendi ko. Àttekat bi bàyyeendi na ko. Waaye, terewul mu def ko li ñuy dippe “contrôle judiciaire”.
Naka noonu kii di Abdu Asiis Mbay tamit, moom mi jiite kurélu géwél yi, mujje nañu ko bàyyeendi. Ndax, moom it, bokk na ci ñi ñu téye woon ci lu ñeel mbir moomu. Li ñu koy toppe mooy luubal gu tollu ci téeméeri miliyoŋ ak juróom-fukk. Jot na layal téeméer ya ak ñeen-fukk ak juróom-benn ya, joxe ñeent ya des. Looloo tax, ñu mujje ko bàyyi bàyyig négandiku.
Ba tay, lu ñeel mbirum “Fonds Force Covid”, yenn ci kilifay Yoon yi àddu nañu sànq, bi juróom-benni waxtu ci ngoon jotee. Ñetti toppekat ñoo janoo ak saabalkat yi. Muy toppekatu bu mag bi fa ëttu dabantal ba, toppekatu bokkeef gi fa ëttu àttewaay bu Ndakaaru, toppekatu bokkeef bi ñeel wàllu koppar. Li ñu dugge woon ndaje mi mooy àddu ci mbir mi, leeralal askan wi liggéey bi ñu ci sumb. Dees na ci yaatal.