Mbirum meeri bu Ndakaaru mi ngi wéy di jur coow. Tay rekk, Sëñ Bàrtelemi Jaas dafa bëggoon a janook saabalkat yi fa màkkaanu meeri ba. Waaye, takk-der yi ñoo ko gàntal. Nde, ci buntu ba lañu taxaw, tere ko dugg. Li mu ko dugge woon mooy, ciy waxam, teggi waxi pólis mi génne woon ab yégle di ci weddi tuuma yees ko gàlloon.
Baynaa Géy moo bindoon perefe bu Ndakaaru ngir mu tekki ndombog-tànku Bàrtelemi Jaas ci boppu meeri bu Ndakaar. Ginnaaw gi, perefe bi dafa jëmmal càkkuteefam gi. Ca la bind Sëñ Bàrtelemi Jaas, moom perefe biy ndawul Nguur, xamal ko ni nekkatul meeru Ndakaaru. Keroog, bi mu woowee saabalkat yi, bëgg a waxee fa meeri ba, takk-der yi dañ ko fa fekkoon, dakkal waxtaan wa. Ñi koy jàppale ca meeri ba, fésaloon nañ seen yéeney xeexal ko.
Ñi toppoon ci ginnaaw meeru ndakaaru ba woon, Bàrtelemi Jaas, fasoon nañu yéene dugal ag kayitu ŋàññ barki-démb ci altine ji, 16i pani desàmbar 2024. Li ñu ko dugge woon nag mooy taxawu ko, xeexle ko ginnaaw bi ñu jàppee ni dañu tekki ndombog-tànkam ci jaay-doole. Waaye seem mébét ma àntuwul. Ndaxte, mujjewuñu amal seen ndajem pekk gi. Nde bi ñu dikkee fa dalub péeyu Ndakaaru, takk-der ya dañ leen a tere dugg fa barab ba, ci ndigal lu ñu jote ci seen i kilifa.
Moom ndayu-mbill ji sax dañ koo sàkkal fu mu yam ci doxantu bi mu doon amal fa rond-point Cité Keur Gorgui ngir nemmeeku tabax yees fay amal. Takk-der yi mayuñu ko fenn fu mu tege tànkam fa tabax yooyu. Altine la mbir moomu xewoon. Muy ndigal lu kilifa ya jot ngir tere Bàrtlemi Jaas fu mu duggee fa tabax yooya ndax li ko yoon wàcce.
Sëñ Bàrtelemi Jaas nag, jaare ko ciy layookatam, dugal na ag dabu ngir kaas lees summi mbalaanum députeem ak lees ko jëlee ci boppu meeri bu Ndakaaru. Fileek i fan, dees na xam lu Yoon di wax.