Ay weer ginnaaw ba ñu ko tegee loxo ak tey, ba léegi Usmaan Sonko mi ngi ci loxoy Yoon. Moom, njiitul Pastef li, nga xam ne jotoon na fee xiifal weer ak i fan ba sonnoon lool, delloowaat na buum ca mboy-mboy ga. Démb ci ngoon la dooraat xiifal gi. Li sabab loolu wii yoon mooy ne moom day jàppale jigéen ñi ñu jàpp ci lu teguwul ci yoon. Te, li ko lal di ñàkk a bokk ak ñi fi nekk péete ci wàllum pólitig. Ñooñu nag jamono jii jenn ngànnaay lañu am muy xiifal te, ca lañu nekk. Muy jigéen ña ñu téye ca camp pénal bu Liberté 6 ak yeneen kaso yi. Te, jamono jii mu am ci ñu ñu teree gisantee ak seen i mbokk. Rax-ci-dolli muy ñaawlu téye gi ñu ko téye jamono jii moom ak ñenn ci ay ñoñam te mu bëgg ñu dakkal ko. Kàddu yooyu mi ngi leen siiwale ci xëtu facebookam.
Beneen xibaar ñeel Usmaan Sonko mooy génnee gi ñu ko bëggoon a génnee ci wayndarew wote yi. Loolu ba tey àntoogul. Ndax, àttekatu Sigicoor bii di Sabasi Fay mooy ki ko gàntal. Ndogal loolu mu jëloon kerog, dëggal na ko tey ci ab bataaxel. Kon, Njiitul Pastef li delloo nañu ko tey ci wayndarew wote yi. Maanaam, léegi moom mën naa dem ca DGE jëli ay këyiti baayaleem ni ko ñeneen ñi defe.
Mu amaat ba tey luy ñuulaat ci soow mi ñeel mbirum Usmaan Sonko ci digganteem ak Yoon. Loolu mooy coow li yenn ci taskati xibaar yi ak kibaaraan yi di ruumandaat fan yii yépp. Mooy coow li doxoon ci digganteem ak Maam Mbay Ñaŋ. Coow àtte woon nañu ko ba daanoon ca Usmaan Sonko waaye, àndu ca woon. Li jot a rotagum ciy xibaar bees sukkandikoo ci “Les Echos” xamle nañu ne ñii waa ëttu àttewaay bu kowe bi “cour supreme” dina àddu ci mbir moomu ñaar fukki fan ak juróom-benn ci weer wi. Waaye, ba tey ñoñi Usmaan Sonko yi maanaam ay layookatam yéyuñu yàbbi ci. Xanaa layookatu tubaabam bi Xuwaan Barànkoo. Waaye, taxul mu dëggal xibaar boobu. Dees na xam kon fii ak ab diir seen taxawaay ci loolu. Ndax, ëtt boobu dafa nar a àddu ci mbir moomu am déed. Day dëggal àtte boobu walla da koy fànq.