Baabakar Ture mu Kewoulo moo njëkk a siiwal xibaaru réeru ñaari way-yëdduy Nguur gi. Fan yii yépp nag, ci mbir mi la kibaraan yiy wax, di ci bind. Askan wi tamit mi ngi amey njàqare. Nde, mbir mi dafa teey xel te, Senegaalu tey jii, lees fiy dund ak a dégg dafa doy waar. Dafa di, ñi ñu wax ni dañoo réer, duñuy niti neen. Moo tax, toppekat bu mag génne ab yégle, xamle ne dinañu wër, luññutu ngir leeral mbirum réer moomu.
Adjudant-chef bu sàndarmëri, Dijje Baaji, di liggéeye IGE, ak Sergent Fulbeer Sàmbu mi nekk ca Njiiteefu yëdduwaayu sóobare yi ñoo ne mër, réer. Àjjuma 18 nowàmbar 2022 lañu leen mujje gis. Nee ñu, ñaari way-yëddu yépp, dëkk bu ñuy wax Ñuumuun, ca duni Karon ya, lañu fekk baax. Bees sukkandikoo ci Senenews, jabaru Fulbeer Sàmbu moo joxe xibaar bi. Boobaak léegi nag, sàndarm yeek way-yëddu yépp a nekk di leen wër.
Ñaari way-yëddu yi ay xarit lañu. Ci li rotagum ciy xibaar, ñoo bokk benn dëkk bu ñu cosaanoo, yàgg a ànd di nappi Kab Maniwel. Nde, foofook seen i pekku soreyoowuñu. Bésu àjjum jooju, soxnay Fulbeer Sàmb dafa toog bésub lëmm gisul boroom këram, ci la ko waxee naataangooy sàndarm bi. Bi ñooñu demee ca jànji Kab Maniwel ya, fa ñaari way-yëddu ya nappiji woon, fekkuñu leen fa. Seen i bagaasi bopp kese lañ fa fekk ak seen i jollasu (telefon).
Bi loolu jibee, ci la ruumandaat yi tàmbale, ñiy njort ne dañu lab ci géej gi. Li gën a tax ñu foog loolu mooy ne, dafa am ku ñu làqi ci géej gi. Te, ci lees wax, kookii ñu génne ci mbeex mi, néewu Fulbeer Sàmbu la, ci lu wér. Waaye, ci biir làrme bi, dese nañoo gëm xibaar bile. Nde, njabootu aji-yëddu bi, ñoom, kenn wanu leen ab néew ngi ñu xool ba xam dinañu ko « xàmmee te kenn yëgulunu ne gis nañu néewu Fulbeer ». Sàndarmëri tamit lu ni mel la wax.
Ñoo ngi laaj ndax dañoo lab, walla dañ leen a rey. Am na sax ñu jàpp ne dañ leen a faagaagal. Waaye daal, ak lu ci mën di am, dara leeragu ci, te xel yi teey nañu.