Me Duudu Ndóoy ñeel mbirum Sonko : ” Li Maki Sàll mën a def ngir saafara mbir mi…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Me Duudu Ndóoy a nekkoon ganu Maymuuna Nduur Fay ci jotaayu L’invité de MNF ca 7Tv. Moom, layookat bi woon jëwriñu Yoon diggante 1983 ak 1986, biral nay pexe yoy, bu Njiitu réew mi bëggee dal, mën na leen jëmmal. 

Pexe mu njëkk mi mooy ne, Njiitu réew mi, Maki Sàll, wotelu ca Ngomblaan ga ab sémbub àtte buy far “délit de corruption de la jeunesse”. Ñu ko defee, daan bees daan Usmaan Sonko bi day neen ci saa si. Moom sax, Me Duudu Ndóoy, dafa jàpp ne “delit” boobu dafa xewwi, méngootul ak jamono. Nde, nootkat baa ko fi dugaloon. Te, baatu “jeunesse” dafa lënt, ba tax na wareesu ko jëfandikoo ci wàllu Yoon.

Ñaareelu pexe mi layookat bi joxeet mooy njéggalug Njiitu réew mi. Naam, àtte bi daanoogul. Waaye, Njiitu réew mi jéggal Usmaan Sonko lu mën a nekk la buñ sukkandikoo ci waxi layookat bi. Moo ko tax a fàttali Aamadu Wuri Jàllo ma doon wuruj ay garab doktoor te ñu àtte woon ko ba daan 5i ati kaso yu muy tëdd. Moone, Njiitu réew mi daf ko jéggal fekk ne sàkku woon na àtteb dabu. Ñooñu mu ko defalee Aamadu Wuri Jàllo moomu la ko mën a defalee Usmaan Sonko. 

Cig pàttali, àttekat bi, Isaa Njaay, dafa daan Usmaan Sonko 2i kaso yi mu war a tëdd ñeel mbirum Sweet Beauté mi. Daan boobu nag, dafay tere njiitul Pastef li doon lawax ci wotey 2024 yi. Ba ndogal li jibee nag, réew mi yëngu woon bu baax a baax, xeex bi jolli diggante farandooy Usmaan Sonko yi ak takk-der yi ba 30i bakkan rot ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj