MEERI BU NDAKAARU : DÀQ NAÑ ABBAAS FAAL MU PASTEF

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci àllarba ji la meeri bu Ndakaaru doon yeesalaat pekkoom gi. Li ñu ko dugge woon mooy jëmmal ndogalub ëttu àtteb dabu bi ñeel yemoo gi (parite). Nde, lees sàrtal, mooy ne, ci pekkub meeri bu nekk, góor ak jigéen ñooy toftalante. 

Abbaas Faal, Pastef : “…lii du dara.”

Ngir dëppale tëralinu pekk geek li Yoon sàrtal ñeel yemoog góor ak jigéen ci bérébi liggéey yi, dan waroon a toftale jenn jigéen ci meer bi. Moo tax, Abbaas Faal mu Pastef, mi nekkoon njëlbeenug tof-njiitu Bàrtelemi Jaas, folli nañ ko. Ngóone Mbeng mu Taxawu Senegaal moo ko wuutu. 

Ñu baree ngi jàpp ne Taxawu Senegaal dafa wor. Waaye, ndeyu-mbill ji moom, Abbaas Faal, yëgalu ko sax yaramam. Moom, Usmaan Sonko moo ko soxal ak ñi ñu jàpp ci kaso yi.

Ci xëtu Facebookam la bind wax ne :

” Maa ngi wax ak way-bëgg-sa-réew yi fi nekk ak feneen, lees génne Pastef ci pekkug meeri bu Ndakaaru du dara. Benn xeex rekk a nu war a yitteel, mooy fexe ba Usmaan Sonko nekk lawax ak bàyyig ñi ñu jàpp ci kaso yi ci sababu pólitig. 

Nan leen fexe matal jubluwaay yi.

Juróom-benni weer ñoo des ci 2024.”

Bàrtelemi Jaas, Taxawu Senegaal, meeru Ndakaaru : ” Dàqunu kenn…ku gedd nag, yow la neex.”

Ginnaaw biñ wotee ba fal Ngóone Mbeng mu Taxawu Senegaal, Bàrtelemi Toy Jaas, meeru Ndakaaru, yékkati nay kàddu, wax ne :

” Dafa mel ni am na ñuy wax ni dama dàq ñenn ci ni may doon liggéeyandool. Dama bëgg wax ne dàq ak gedd du benn. […] Maa ngi dalal xelu ñépp, loolu amul. Am nay palaas yuñ bëggoon a jox ñenn ci sunuy naataangooy liggéey, waaye ñoom ñoo bañ. Nun, nangul nan leen seen taxawaay. “

Meeru Ndakaaru nee na sax, Soxna Karmelin Kasoka la waxoon mu jël 17eelu tof-njiit li, mu gàntu. Nee na Faatu Mbóoj, fara-caytu, dafa bañ tamit. Abbaas Faal mees folli yit, noonu, dafa bañ. Bàrtelemi Jaas nee, ñoom, Yoon a leen tënk, pólitig taxu leen a jóg.

” Pólitig indiwul ci ndajem meeri bi. Liggéeyal waa Ndakaaru moo nu tax a jóg, ànd ceek ubbeeku ak di jéllale, rawatina cër bi ñu jox képp kenn ku fiy liggéeyee.”

Ak lu ci mën di am, lëkkatoo Yewwi Askan Wi rafetluwul doxalin Taxawu Senegaal. Bii nag mooy bi ci mujj. Moo tax génne nañ ab yégle, di ci ñaawlu doxalinu Taxawu Senegaal ak ni mu jegee Bennoo Bokk Yaakaar. Looloo tax ñu jël ndogalu dàq leen ci lëkkatoo gi. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj