Nees ko biralee woon ci sunu yaxalu barki-démb bi, ndawi yi FMI yabal fi réew mi dañu toogaat ci réew mi ngir wéyal liggéey bi ñu sumb ak Nguurug Senegaal gi. Bésub 22 oktoobar 2025 lañu ñëwoon Ndakaaru ngir waxtaan ak njiiti réew mi ñeel naal wu yees wi ñu war a jagleel réew mi ci wàllu kopparal. Waaye, dañu mujje yokk diir bi ñu fiy def ndaxte liggéey bi yombul te dafa laaj ay waxtaan yu xóot. Ginnaaw bi ñu defee diirub ñaari ayu-bis nag, kii jiite ndaw yi fi FMI yabal, Edward Gemayel, àddu na ci mbirum bor bi.
Bees sukkandikoo ci kàdduy Sëñ Gemayel, guléet ñuy gis « …bor bu ñu nëbb bu am dayo bii ci Afrig ». Bees jàngatee wax ji nag, mooy ne, nguuri Afrig yi, yàgg nañoo nëbb seen i bor, waaye bor bu tollu bu ni Senegaal, ñu nëbb ko, ñu ngi koy soog a gis. Dafa di, ci xay ma, li ñu nëbb a ngi tollu ci 7i miliyaari dolaar, daanaka 4 000iy miliyaar ci seefaa. Koppar yu takku yooyu, Maki Sàll ak Nguuram ga woon ñoo ko leboon ba noppi nëbb ko. Looloo taxoon FMI ajandi woon naaluw kopparal wu mu waroon a jagleel Senegaal. ci lees wax nag, Nguurug Senegaal gu yees gi ci boppam moo sàkku woon ñu ajandi naal wi ba ñu xam fu ñuy teg seen i tànk. Ci diggante bi, ñu ngi doon wéyal waxtaan wi ngir wut i pexe, xoool ci yan anam lañuy àndee wéyal liggéey bi.
Naka noonu, ginnaaw bu ñu fi defee diirub ñaari ayu-bis, Edward Gemayel mi jiite ndaw yi fi teewal FMI, àdduwaat na ci mbir mi. RFI moo doon taataan i kàddoom. Dafa ne : « … bu dee Senegaal, ak ni bor bi ñu nëbb tollu, guléet ñu koy gis ci Afrig. » Lu ni mel a tax, ba tay ciy waxi Sëñ Gemayel,waxtaan wi yàgg. Waxtaan yooyu nag, ca weeru ut wee weesu lañu ko dooroon. Li ñu ko dugge mooy torlu ab déggoo bu bees ñeel naaluw kopparal.
FMI nag, dafa wax ne fàww Càmm gi jël i ndogal ngir joyyanteek a jubbanti mbir mi balaa ñuy jagleel Senegaal weneen naaluw kopparal. ndogal yooyii, bokk na ci, jël lépp lu aju ci bor bi, féetale ko ci genn njëwriñ kepp te siiwal njureef yi tukkee ciy luññutuy bor yi. Coppite yooyu, lees ci jublu mooy fexe bay leeral caytug bor bi te fexe ba lu ni mel bañ fee amati.
Waxtaan yàgg na nag. Waaye, Sëñ Gemayel a ngi rafet njort, di dalal xel yi. Ndax, nee na ñoo ngi liggéey ngir « …gaaw a am ab déggoo ».