Njeexitalu joŋante Miss Littérature Senegaal démb la woon, àllarba, 18eelu fanu désambar 2024, ca Grand Théâtre Duudu Njaay Roos. Soxna Aminata Faal, di njàngaan ca Liise Mariyaama Ba bu Gore, moo jël raw-gàddu gi.
Miss Littérature, joŋante ladab la buy am ci 12i réew ci Afrig sowu-jant. Ma nga doree fa Beneŋ, ci njiiteefu soxna Carmen Toudonou, ca atum 2016. Senegaal, ren la ci dugg, jaare ko ci soxna Salamata Usmaan Jàllo, di taskatu xibaar, féete ci mbatiit. Soxna si dafa gis ni Senegaal, naam, réewum ladab la, waaye bindkat yu jigéen ñi bariwuñu lool. Ba tax mu bëggoon a jàppale ak a ñaax ndaw ñu jigéen ñi (tollu diggante 18 ba 24i at) ñu def i jéego ci wàll wii. Nii la joŋante bi duggee Senegaal. 18eelu desàmbar nekkoon njeexital li, 10i xale yu jigéen (ku ci gën a xereñ nga ni kii la) doon xëccoo metel mi. Waaye, Soxna Aminata Faal moo ko mujjee jël.
Xew maa ngi door bi 11i waxtu jotee, daldi daw ba 3i waxtu ci ngoon gi ca Grand Théâtre Duudu Njaay Roos. Xew maa ngi amoon ci teewaayu 10i lawax yi ak seen iy ekool, njaboot ak it ñu bari ñu njàng ak ladab soxal, ñu ràññee ci Sëñ Ibraayma Lóo, njiitu téereek dawal ak Soxna Mariyaama Ndóoy, bindkat tey njiitu Musée Léopold Sédar Senghor, Faatimata Jàllo Ba, jàngalekat ak bindkat, moom la Salamata Usmaan Jàllo ndeyale bés bi. Moom it mu am ci taxawaay bu am solo, jàppale « rakkam » bu baax. Soxna Faatimata fésal bu baax mbégteem ak ni mu amee mbetteelu bànneex ci ni xale yi jàngee téereem bii di Rouges silences ak yëg-yëg yi ñu ci am.
Xale yi natt nañu leen ci seen xel mu neex, seen kàddu gu rafet ak ni ñuy dawalee ak tënkee téere. 3i yoon lañu jaar, muy 3i laaj yu wuute ; yoon wu ci nekk ak sañseem. Porofesëer Ãdre Mari Jaañ moo jiite woon ñiy natt xale yi feggoo ak jàngalekat yii di soxna Ani Kóli ak Muhammadu Sow ak Astu Mbeen Cubb, taskatu xibaar buy def moom it liggéey bu am solo jëm ci téere ak xale yi.
Xale yi taaru woon lool booleek der wu ñuul mbaa xees te kenn xeesalu ci. Muy tomb bu am solo ci jamono joj ñu baree ngi jéem a tubaab-tubaablu bay soppi seen i der.
Neexal yi bari woon nañu doonte koppar amu ci. Soxna Salamata Jàllo bég na, gërëm ñi ko jàppale ba xew mi mën a àntu. Waaye, mi ngi tàllalaat loxo ñépp ngir ñu gën cee jàpp ba bu keroogee (25eelu sulet 2025) ca réewum Beneŋ xale yu bari mën fa a teew ci finaalu Afrig bi, ba Senegaal mën a ñibbisi ak raaya Miss Littérature Afrig. Fàttewul it gërëm yaayam bay jooy ndax ni yaay ji sonnee ci moom ba mu egg fii mu egg. Ba mu yëkkatee kàddu ba daaneel la yaayam ñëw gàll ko kaala, ba noppi ñu laxasu ñoom ñaar di tuur i xéewal, muy jamono ju daw yaram. Mënees na ni, ndaje ma ngir ladab la ci wàllu jigéen ñi, waaye sargal bépp jigéen jaare ko ci ladab ndax ladab mënees na cee sukkandiku ngir wéyal ndonol askan ciy mbaaxam, mbatiitam ak xayteem. Kon am na solo cim réew. Su ci jigéen ñi sóoboo ak doole, lu baax la lool. Moo tax Soxna Aminata Faal ne « ladab ngànnaayu coppite la ak dajale. Dinaa teewal Senegaal ca Beneŋ ak dooley mbatiitam ak kàddoom ».
Sëñ Magéy Ture, bindkat, njiitu Francophonie ci Senegaal, wax ne mbégteem ci ndaje mi waaye xamle na ni li mu gis xale yi bind ko, wax ko, wone fii bindkat yu góor am nañu soxla ndax jigéen ñii fas nañu yéene bey seen waar bu baax ci toolu ladab. Kon, góor ñi am nañu soxla.
Ndaje ma xumboon na ndax amoon na ay woykat, xalamkat ak i taalifkat yu xereñ yu ca teewoon te desuñu ginnaaw. Am na taalifkat bu jigéen bees duppee “Plume d’ébène” bu fa yëkkati woy ngir yeete ak a fàttali musiba mi ci xeesal ci fànn yépp waaye it fàttali rafetaayu der wu ñuul.