Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, gaaral na naaluw joyyanti koom geek mboolaay mi. Tay jii, àjjuma, 1 ut 2025, la ko doon gaaral askan wi fa Grand Théâtre. Ci yoor-yoor bi lees doon amal xew-xew bi, ci teewaayu Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru JomaayJaxaar Fay, ak yeneen i kilifa yu ràññeeku. Sëñ Usmaan Sonko biral na ñetti kenu yi gën a fés yoy, ñooy doon cëslaayu naal wi. Nde, ci ñetti kenu yooyu lees di sukkandiku ngir kopparal naaluw joyyanti wiy tegaat réew mi ci yoonuw naataange, yoonuw yokkute wu leer te jub. Jubluwaayu naal wi mooy fexe ba Senegaal mënal boppam ci fànn yépp, daldi moom boppam dëggantaan. Ñetti kenu yooyii ñooy : njub, cëslaayoo ndëxëñteefu réew mi ak ñoŋalug alal jeek jumtukaayi liggéey yi.
Tay la woon tay. Ay fan ci ginnaaw, elimaanu jëwriñ yi yégle woon na ne dina gaaral askan wi aw naal wuy joyyanti koomug réew mi ak mboolaay mi. Ci bésub tay jii lees ko doon amal. Ca ndaje ma ñu woote woon fa Grand Théâtre, Sëñ Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi, aajar na fa naal wow, ci ñetti kenu yu bir la lalu. Ñetti kenu yooyu ñooy yoon yi Càmm gi namm a jaar, ci kilifteefu Njiitu réew mi, ngir dajale koppar yi war ngir jëmmal naal wi, afal Senegaal ba fàww. Liggéey bi jëkk nag, mi ngi aju ci yaxanal ak jàppandal liggéeyu ñoñ Càmm gi, tëral am pexe ngir sakkanal alalu réew mi. Nisër bi mooy fexe ba joyyanti Nafag réew mi ci ni mu gën a gaawee, ngir mën a am alal jees di sakkanal, daldi koy dugal ci fànn yuy jariñ askan wi.
Ñaareelu pàccu liggéey baa ngi aju ci anam bees di dajalee koppar yees di jukkee ci réew mi. Solos liggéey boobu mooy dafay tax ba Senegaal bañatee wéeru ci réew ak kuréli doxandéem yi ngir kopparal ay naalam. Rax-ci-dolli, loolu dafay tax ba Senegaal gën a mënal boppam, jaare ko ci dooleel Nafag réew mi. Loolee la Sëñ Abdurahmaan Saar xamle, moom miy jëwriñu Koom-koom gi, Naal wi ak Digaale bi, muy lu ko yitteel lool. Maanaam, dañuy tabax cëslaay gu dëgër gog, ci lees di sukkandiku ngir suqali réew mi.
Ñetteelu pàcc bi ci mujj mooy liggéey ba xaalisu mottal bi bawoo ci réew mi ak doomi réew mi. Bu ko defee, dinañu ñoŋal njëlug bokkeef gi. Kenu bile nag, du yem rekk ci sakkanal alal ji, waaye dina tax ba ñu dugal alalu réew mi ci fànn yuy jur njariñ, di suqali alal ji, walla di ko ful.
Naaluw joyyanti woowii elimaanu jëwriñ yi aajar sànq ci yoor-yoor bi, dafay laaj xaalis. Moo tax, bees sukkandikoo ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi, 4 600i miliyaari FCFA lañuy dajale ngir doxal naal wi. Koppar yooyu, ci diirub ñetti at lees koy dajale te du doon bor bees di jëlee bitim-réew. Jubluwaay bi mooy Senegaal mënal boppam ngir moom boppam. Sëñ Usmaan Sonko dafa ne :
« Natt nanu lu ëpp 4 600i miliyaari FCFA ci alal jees mën a dajale diggante 2025 ak 2028, te duñu yokk boru réew mi. Nii lanu gisee naaluw joyyanti wiy sabab jonnug Senegaal, mu lalu ci xel mu teey, fulla ak faayda. »
Naaluw joyyanti koom geek mboolaay mi dafay xàll yoon wu bees tàq ci anam bees di saytoo koppari askan wi. Ndaxte, ci biir naal wi, am na ñeenti ponk yees di jaar ngir dajale alal jépp ji ci war, te lépp di fi bawoo. Ponk yooyu ñooy :
-
2 111 miliyaari FCFA yees di tibbee ci alal ji askan wiy liggéey (ressources domestiques) ;
-
1 091i miliyaari FCFA yiy bawoo ci tabaxtey nguur gi yi Càmm giy yoolu (ndalu) jàmbur yi ;
-
50i miliyaar yiy bawoo ci alal ji ñuy sakkanal ci liggéeyu caytu gi ;
-
1 352 miliyaari FCFA yiy jóge ci pexey kopparal yuy sukkandiku ci am-amu réew mi, mu di ay pexe yu yees yoy, ajuwuñu ci lebi xaalis ay doxandéem.