NAALUW SENEGAAL 2050 : USMAAN SONKO SAS NA JËWRIÑ YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci altiney démb ji, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, doon amal ndaje ak jëwriñi Càmm gi. Naaluw « Senegaal 2050 » wi lañu doon fénc, di waxtaan ci pexe ak yoon yees war a jaar ngir jëmmal ko ci lu gaaw. Démb nag, kàddu yu dëgër la Usmaan Sonko waxee ak jëwriñ yi mu jiite, joxoñal leen jëmu bu yees. Xamal na leen itam ne, léegi, dañuy tëral yoonu liggéey wu bees wow, ñépp ñoo ciy bokk tënku. Ci biir doxalin wu bees woowu, saa bu amee lu yéex, dees na duut baaraam ki waral yéexaay bi, sémb wu ci nekk ñu wutal ko àpp, te jëwriñ ju ci nekk dinañu la tëralal aw yoonu liggéey wees yeesal, di ko topp ak a saytu.

 « Damay wax mu leer : àgg nanu foo xam ne, lu yéex, dees na ko wutal boroom, sémb wu ci nekk ñu àppal ko ba mu leer, te jëwriñ ju ci nekk dañu lay tëralal yoonuw liggéey wees yeesal, di ko topp ak a saytu » (Kàdduy elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko)

Nisëru Usmaan Sonko mooy fexe ba jëmmal kàddug Càmm gi, teg ko ci yoon wu leer, farlu ci, te mu ànd ak njariñ lu askan wiy làmb di ko daj.

Bees sukkandikoo ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi, dañuy dakkal yéexaayu liggéeyu caytu gi. Ngir loolu am nag, dinañ fexe ba lépp luy wayndarey caytu gi nekkaat nimerig, maanaam ñu koy jaarale ci nosukaay yi ak lënd gi. Liggéey boobu, ci diirub ñetti weer lees ko àppal. Ba tay ci kàdduy Usmaan Sonko, léegi, bépp « courrier » bees tontuwul te mu nar a yéexal liggéey bi, dinañ ko lijjanti ci anam bu gaaw. Elimaanu jëwriñ yi joxe na santaane, wax ne nañu gaawal wépp sémb wow, jotees na ko kopparal ba noppi. Te sax, léegi, fa njiiteefu njëwriñ gi lees di saytoo xeeti naal yooyu.

Bu dee sémb yi ñu dugal ci àtteb joyyanti koppar yi, warees na leen sumb fii ak fanweeri fan gën-gaa bari. Rax-ci-dolli, dees na taxawal ab « task force » ngir àggal sémb yees war a lootaabe. Liggéey boobu, ci njiiteefu elimaanu jëwriñ yi lay amee, mu war cee ànd ak waa BOSC, APIX, FONSIS, DGPPE, UNAPPP, CDC ak waa « Direction générale de la coopération ».

Ci beneen boor, dees na dooleel sémb yi nga xam ne, dañoo boole njëwriñ yu bari. Te, sémb yu ni mel, léegi, njiiteefu njëwriñ gi moo leen di saytu. Rax-ci-dolli, jëwriñ ju ci nekk sas nañu la, nga war a topp bu baax dige yi réewum Senegaal dig waa bitim-réew ak yi Njiitu réew mi dige. Ci kaw loolu, jëwriñ ju nekk war na a defar ag caabalu ñetti weer yu nekk. Dafa di sax, ñoom jëwriñ yi, ku ci nekk war nga yeesal sa yoonuw liggéey fii ak weeru sulet wi di jeex. Waaye, elimaanu jëwriñ yi dafa joxoñ ñetti jëwriñ, am lu mu leen sant :

« Maa ngi xaar ci njëwriñi Yaale ji, Ndefar gi, Yoon wi, ak Biir réew mi ñu gaaral ma aw tëralin wu leer ñeel seen ay « États généraux » gën-gaa yàgg bésub 15 ut 2025. »

Usmaan Sonko xamleet ne, ñépp ñoo war a takku taxaw ngir waajal naaluw joyyanti wi muy waaj a gaaral fii ak i fan yu néew. Ca ndajem jëwriñ yi la koy jëkk a gaaral laata mu ko koy aajar askan wi. Bu loolu weesoo, dees na ci toftal ay liggéey ak i yëngu-yëngu yu bari ngir yaatal ko, siiwal ko ba ñépp jot ci.

Génn gii nag, lees ci mën a jànge mooy ne, liggéey jot na, wax jeex na. Mooy li seereer siy wax rekk : caaxaan faaxe !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj