Ayu-bés yii weesu, yéenekaay yu bare dañoo xéy fésal ci seen xët bu njëkk xibaar bu kéemaane. Waaw, li nu ko dugge woon mooy xamal askan week Nguur gi ne lu mat junniy ndongo ak lu teg amaguñu kayitu-juddu. Déggal ma lii rekk ! Te lees war a xam moo di ne ndongo yooyu, looloo leen di tee bokk ci joŋante yi leen di may lijaasa biy firndeel seen njeexitalu njàngum daara ji féete suuf. Te moonte ñoom matale nañu seen njàng.
Lu waral loolu ?
Xanaa càggan. Càggan doŋŋ.
Nee ñu Pikin gii rekk, limu gone yooyu ëpp na junni. Ndeysaan, njàqare ak tiis dikkal na leen te ñoom de, doonu ci dara ba dara booloo jeex. Xamalees na nu itamne ci lekooli Pikin yi ba tey, téeméeri xale yoo jël, ci xayma, ñaar-fukk ak juróom yi binduwuñu. Ndaw lu yéeme, cim réew moo xam ne nee na yokkute lay diir ! Moo, ndax am réew dina am yokkute su fekkee ni njàng mi sooy na ?
Déedéet.
Dafa di, yokkute walla naataange, ci liggéeyu doomi réew mi rekk la mën a aju. Te bala liggéey boobuy sotti, fàww nu yar gone yi, yiir leen, yokk seen xam-xam, def ci ñoom yëg-yëg ak mën-mën yiy tax ñu bëgg seen réew, fas yéene koo jëme kanam. Kon, réew mu am fulla, farlu te xam jëmuwaayam, du sàggane ay doomam. Waaye Senegaal gii, kenn du ko raw ci wàllu càggan, dafa mel ni sax aada la fi.
Te li gënatee doy waar ci mbir mi, mooy ne du guléet ! Daanaka at mu Yàlla sàkk njàqare gu ni mel, diiwaani Senegaal yépp dañu koy jooytu. Bu ko defee, mënees na wax ne, ci fànn googu, ‘’Pikin yi’’ dañuy gën di baree ka law ci sunu biir gaal gi !
Xanaa lii mooy jur doom sànni ! Ndax càggan mën naa weesu lii ? Waaw, lii nag ba kañ ?
Waaye lu jiin Njaag a te way-jur yi ñooy Njaag. Naka la nit di jure doom, di ko dundal, di ko toppatoo, di ko yar muy màgg, nga ameel ko àqi teyam ak ëllëgam, ba noppi nga ne doo ko wutali këyit yi koy màndargaal ci biir nit ñi, fépp fu mu mën a dem ? Rawatina ci jamono yii nu tollu, di jamonoy mbind, jokkoo ak xamtéef ? Yenn yi kat, xel mënatu koo nangu ndax ñépp a xam, daanaka, ni Dunyaay doxe léegi. Ci dëgg-dëgg, lii du dara lu dul xamadi, xayadi ak càggan gu jéggi dayo !
Waaye am na leneen lu mat a laaj te nu war koo joxoñ yitam : naka la sëriñi daara yi, njiiti lekool yeek espektëer yi àttanee seetaan lu ni mel booba ba léegi ? Moone de, ndongo yi dinañu toog di jàng 6 at laata ñuy àgg ci kalaasu eksame bi. Ci diggante ba ñuy dugg lekool ak léegi, at mu nekk dinañ bindu. Waaw. Ndax sëriñ daara yi, njiiti lekool yeek espektëer yi def nañu seen liggéey ni mu ware ? Lan lañu doon xoole ba lii di am ? Lu taxoon ñu ñàkkal solo jéyya jii ba xëy bés musiba mii ni këtt-ni-jonn ci seen kanam, ñu mel ne ñu ci am mbetteel ? Fii de, mel na ni mëneesu fee lay ñàkk xam, xanaa ! Càggan taxawati, ne nu : naam !
Gaa ñi ŋànknguur gi tamit, kenn du ñoom.
Jawriñ bi yor wàllu njàng meek njàngale mi moo waron a jël ay matuwaayam ba lii bañ a am. Jawriñu biir réew mi tamit waroon naa def dara. Warees na duut baaraamu tuuma tamit meer yi, ñoom ñi gën a jege askan wi tey defar këyiti-juddu yi. Mbir mii daal, kenn setu ci.
Ma laajati : lu tee way-jur yi defarlu seen këyitu-juddu doom bés bi mu juddoo ? Ndax Nguur gi manuta fexee lëkkale loppitaan yeek meeri dëkk bu ne, ba nga xam ne lépp lu xew ci béréb bu njëkk bi, bi ci des jot xibaar bi ci saa si ? Dëgg la, Senegaal dum réew mu naat noonu, waaye nag, ñàkkul ay nit ak i jumtuwaay yiy tax mu tëral pexe moomu. Bépp lay bu ñu fi indi, ay caaxaan kese la !
Lu ci mënti am, ci sunu gis-gis, xel mënuta nangu ñàkk kayitu-juddu doŋŋ xañjunniy ndongo lijaasa bi mën a tax ñu tekkiji ëllëg !
Lu tee sax ñu may leen ñu def eksame bi ba noppi, kilifa yi séq mbir mi booloo, taxaw nekk jenn jëmm, taxawu ndongo yiy jànkoonteek yii jafe-jafe ?
Te, su loolu lépp weesoo, luy tee Nguur gi jóg ci lu ñaaw lii, seet nu mu koy saafaraa ba abadan ?
Ndax kat, këyitu-juddu, ak lu mu am am solo, manul a gën a am maana ëllëgu gune yiy war a amali seen bopp njariñ, amali njariñseeni way-jur ak tamit seen réew ak seen askan.
Wolof Njaay nag, dëgg la, nee nañ lu mu léebu ñaare noonu la, waaye Tubaab yi tamit, léeg-léeg, kenn du dem ñu des ; ñooy wax ne : kuy sang liir bay tuur desitu ndox maŋ ko doon sange, na nga moytoo sànniwaale liir bi ! Su boobaa dinga réccu li nga def ndax càggan lu mu jur, réccu am ci wàll.