NAPP GI : JUB, JUBAL, JUBBANTI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu napp gi, Doktëer Faatu Juuf, siiwal na toftaleg turi nit ñi ñu jagleel ay lisãsi napp (licence de pêche). Lisãsu napp mooy, ci déggiin, ag këyit goo xam ne, kilifay réew mi ñoo koy jagleel ay nappkat ngir ñu mën a am sañ-sañu napp ci géeji Senegaal yi. Bu njëkkaan nag, daawuñu siiwal boroom lisãs yooyii. Te, daan na jur coow lu bari. Ndax, nappkat yi dañ doon joxoñ baaraamu tuuma boroom gaal yu mag yooyu ñuy jox ay lisãs. Nde, ci seen i wax, boroom gaal yu mag yooyu ñooy jeexal jën yi ba tax, ñoom, nappkat yu ndaw yi, mënatuñoo mbaal jën wu baax. Dafa di sax, nees daan joxee lisãs yi day xeeñ njuuj-njaaj. Looloo tax Nguur gu bees gi fas yéene leeral lépp, tàmbalee ko ci siiwal turi ñi ñu jox lisãs yi.

Jub, jubal ak jubbanti la Nguurug Basiiru Jomaay Fay gi woote. Dafa bokk ci li ñu nisër, delloo askan wi lépp luy moomeelam, rawatina balluy mbindaare yoy, daanaka, Nguurug Maki Sàll gi daf leen a tayle doxandéem yi. Ci fànnu napp gi, bari waan na lees ciy dégg i coow, nappkati réew miy kaas ak a jooytu rekk. Daa nañ dem sax bay jéggi digi réew mi, di nappi fa réewi jàmbur ya, niki Gànnaar, ñu leen ciy fitnaal, am i nappkat yu ciy ñàkk seen i bakkan. Jën dem ba jafe ci réew mi.

Li waral loolu mooy ne, dafa am ay boroom doole yu yor ay gaal yu mag a mag, ànd ak i xarala yu yees te xarañ, yu ñu jox ay lisãs. Ñooñii nekk ci géeji Senegaal yiy napp, di buub ak a yóbbu jën yi bitim-réew. Boroom gaal yu ndaw yi, ñoom, nappkati aada yi, di dese yabooy beek jën wu sew wi. Nappkati Senegaal yi ne, dem nañ ba dundeetuñu seen liggéey, muy napp gi. Am sax ñuy wax ne loolu bokk na ci li sabab mbëkk mi. Ndax, daf ci am ay nappkat yu doon yeb ay nit ñuy génn réew mi, wutali Espaañ, di fayeeku xaalis bu takku. Mu doon lu metti ci ñoom, ñu yàgg koo xeex, di xeex ba fal njiit yu bees yoy, dañu dige woon ne, ci fànn wi, dinañ leeral lépp bu ñu faloo.

Yàlla nag, dafa dogal Basiiru Jomaay Fay jël Nguur gi. Te, ginnaaw dige bor la, siiwal nañ turi boroom lisãs yooyii di napp ci géeji Senegaal yi. Doktëer Faatu Juuf mi ñu dénk napp gi ak li ci aju moo biral toftaleg turi ñooñii jotoon ci lisãsi napp yi, bi Nguurug Maki Sàll gi di nekk. Démb, altine 6 me 2024 la ko feeñal. Ci lees rotalagum, 151i gaal yu mag ñoo am ci lisãs yi. Ci biir 151i gaal yu mag yooyu, nee ñu, 132 yi ay moomeeli waa réew mi lañ, 19 yi di moomeeli ay doxandéem.

Tey, ci talaata ji 7 me 2024, daanaka yéenekaay yépp a fésal xibaar bi ci seen i xët yu njëkk. Mu am ciy way-moomeel ak i kuréli maxejj yu rafetlu mbir mi. Kii di Basiiru Jaara, bokk ci kurél gii di Environmental justice foundation (EJF), di layal lépp lu aju ci aju ci géej gi rafetlu na ko tamit. Yéenakaay Le Quotidien moo fésal i kàddoom. Daf ci ne :

« Ñaari at a ngi nii daw ci ginnaaw njiit yi (fi nekkoon) ngir ñu siiwal toftale gii. Ndokk ! Tey jot nanu ci. Loolii dina doon cëslaay gees di mën a sukkandiku ngir xeex napp gu jaarul yoon gi. »

Moom, Basiiru Jaara moomu, teg na ci ne, toftale gi mooy tax ñu mën a xam kan moo nekk fan. Te yit, toftale gi dina tax ñu xam turu gaal gi, turu boroom gaal gi, TGB (tonneau de jauge brut) bi, maanaam dooley gaal gi, béréb bi muy nappee, xeetu napp gi muy napp, tolluwaayu mbaal mi walla caax mi muy nappee, àppug tàmbali gi ak àppug njeexital li, añs. Kon, dees na ci fekk xibaar yi war yépp ngir ñu mën a saytu mbir mi.

Yéenekaau Walf Quotidien moom, dafa gën a xóotal. Nde, ci boroom gaal yu mag yooyu, dañu njort ne daf ci am ñu abale seen i tur diggante 2012 jàpp 2024. Maanaam, du ñoom ñooy boroomi gaal yooyu ñu leen di moomale. Dafa am ñu nekk seen ginnaaw, di boroom gaal yi dëggantaan. Yéenekaay bi dafa seetlu ne :

« Ci biir 15Ii gaali napp yi njëwriñu napp gi siiwal, ay Saa-Senegaal ñoo moom 132 yi, 19 yi ci des di moomeeli ay doxandéem, ay farãse ak i español. Li ci doy waar nag, amu ci genn gaalug sinwaa walla gu Riisii gu ñu ci lim. »

Waaye nag, njëwriñu napp gi wax na ne, toftale gi des na. Ndax, ci seen yégle bi, bind nañ ci ne toftale gi « …laalul wayndare yees nekk yeesalaat. »

Soxna Faatu Juuf, jëwriñu napp gi dafa wax ne, « doxaliin wii dafa bokk ci leeral bi ñu bëgg a saxal ci nees di saytoo balluy mbindaare réew mi, nga xam ne moomeelu askan wi la. »

Bu njubadi amee nag, jubbanti day doon farata. Te, bant bu dëngee, bu ko ëpp doolee koy jubbanti. Nguur gi, fi réew mi, moo fi ëpp doole. Ñoo ngi xaarandi ba xam lu ciy topp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj