NAWETU ITALI AK JOŊANTE REN JI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nu des ak yéen ci réewum Itali ba tey. Tey nag, xibaar yi nu leen di jottali xaw nañoo wute ak yi ngeen di faral a dégg. Nde kenn réerewul mbir ne sunu xibaar bi mujj mu ngi ajuwoon ci nekkinu doxandéem yi, rawatina ci doomi-Afrig yi dëkk ci miim réew. Sunu yéene tey mooy waxtaan ak yéen ci làngu politigu Itali. Waaw, juumu leen de, “làngu politigu Itali” ngeen jàng. Du ñàkk sax ngeen naan ci seen xel : “Waaw ! Baay ak Stefano ñoom, lu ñu xewle nii ? Luy sunu yoon ci politigu Itali ?” Waaye delloosileen seen sago nde léegi ngeen xam lu tax nu war cee yéy yàbbi ! 

Dafa fekk rekk ne am nay coppite yu am solo yuñ tàmbalee seetlu ci géewu politigu réew mi te ba fu yëf yiy mujje sunuy mbokk duñu ci mucc.

Ren, atum joŋante la naroon a doon ndax fan yee nu génn, jawriñbi ñu dénk mbiru biir réew mi dafa jékki-jékki rekk ne dafay tekki ndomboy-tànku Konte mi doon njiitum Itali, ginnaaw dara doxatul ci dëkk bi. Ci noonu, wutaakon yi duggaat ci làng gi. Ku nekk ci ñoom di xëcc jëmale fi nga yaakaare mbooloo bésu wote ba. Salwini ne moom it kenn du dem muy des. Ci la daldi samp ndëndam, tàmbalee wër Itali ngir dajeek nit ñi ba xiir leen ci ñu sànnil ko kàrt ëllëg. Fépp la dem, nag, rawatina dëkki tefes yi, moo xam bëj-saalum walla  bëj-gànnaar, di ratatati rekk, di yakk wàlliyaansi yi lu mel ni xeme. Yemul foofu de, nde nee na bés bu jotee ci réew mi dina indiy coppite yu bare ci doxalinu nguur gi. 

Waaye waa kujje gi newuñu yàcc di ko seetaan, dañu ne mukk du ci dal, wote du fi am tey, du fi am ëllëg. Li leen gënal mooy ñu seet naka lees taxawale geneen nguur guy yittewoo génne Itali ci jafe-jafe yi mu nekke.

Te sax, nag, Salwini naam am na ñu ko bëgg waaye du ñépp. Ndax am nay Italyeŋ yu ko doon teerooy nen yu nëb mbaa ndox ci mitiŋ yi mu daan amal, teg ci di ko diiŋat. Loolu, ku dugg Youtube dinga fa gis ay widewo yu bare yu koy firndeel. Moo waral ngóor soosu, Salwini, furu-faraam dem, mu dellu ginnaaw ne teg na waxu wote jooju ci suuf. Te bu loolu weesoo, kenn ci ñi mu àndal ŋànk nguur ngi tey wὀoluwu ko. Ndax ak li coow liy bare yépp, lenn rekk a yitteel Salwini te mooy jot ci réew mi. Ñi xam saa-waay yépp nee ñu njiiteef doŋŋ ako soxal, du leneen.

Waaye fii Itali la, wax jee fi nekk rekk waaye doful, jinne jàppu ko, moo gën a xam ne jot ci réew mi du yombe noonu. 

Bu wote amoon itam, du raw ñépp ba tax koo nekk “buuru Itali” di Buur di Bummi, lu ko neex mu def.

Rax-ci-dolli, li fi xewoon ci 14elu  fan bii weesu ci weeru Ut yee na ñu bare. Loolu lan la ? Xanaa gaal gu tudd Open Arms, yab 147i  doxandéem yu jòge Libi, moo def fukki fan ak juróom ci géej giy xaar ñu may ko mu dugg Làmpedusaa. Li ko waraloon moo doon ab sàrt bu Salwini xaatim, di tere ku wallu doxandéem yi, wàcce leen ci dëkk bi. Bu dul woon li  TAR – kërug-àttekaay gu mag – weddi Salwini, taxawal ab sémbu bu wuteek sàrtam boobu, sàllaaw leneen lees wax tey ci 147 doxandéem yooyu, musiba mu ne mënoon naa dal ci seen kow.  

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj