NDAJEM DONALD TRUMP AK JURÓOMI NJIITI RÉEWI AFRIG

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal, Gaboŋ, Gine-Bisaawo, Liberiyaa ak Muritani… juróomi réew yii la Njiitu réewu Etaasini li, Donald Trump, dalal ca seen njénde la. Ci bésub àllarbay démb ji la seen ndaje ma door, war a jeex ci àjjumay ëllëg ji. Jubluwaay bi mooy xool naka la Etaasini di liggéeyee ak juróomi réewi Afrig yooyi mu tànn, dalal leen. Ca biir waxtaan wa nag, Njiitu réewum Senegaal li, ginnaaw bi mu fa gaaralee ay sémb yu am solo, raggal na Donald Trump ndiggam, seedeel ko lu rafet. Njiitu réewu Amerig li tamit tagg na ko, wax ci moom lu baax.

Bi mu jëlee kàddu gi, Njiitu réew mi leeral coppite gi anam ci jëflante yi dox diggante Senegaal ak réewi tubaab yi, rawatina diggante Etaasini ak Senegaal. Jëflante yooyu, léegi, dañuy aju ci joxante cër, di liggéeyandoo ci anam bob, ku nekk a ciy gis boppam.

Njiitu réew mi dafa njëkk a rafetlu taxawaayu Etaasini biir Afrig : « Jéego yi ngi dox ca RDC ñoo fay ay wa, dakkal xare boo xam ne, bi mu dooree ak léegi, am na fukki-fukki. » Njiitu réew mi tuddaale na jafe-jafe ya am ci Sayel bi ak ca Libi, rafetlu yit taxawaayu Donald Trump mi ciy dox tànki jàmm. Ndax, bat ay ci kàdduy Basiiru Jomaay Fay, fu jàmm xëyul, yokkute du fa yendu. Looloo ko tax a wax ni, « naataange mënul a am fenn fu amul kaaraange ».
Bi mu noppee ci tagg Donald Trump mi mu yéene cargalug « Prix Nobel de la Paix », Njiitu réew mi gaaral na fa ñaari sémb yu mag yu aju ci balluy mbindaare yi. Nde, Senegaal dafa lëkkaloo ak US Geological Survey ngir saytu li ci biir suufam. Njiitu réew xamle na sax ne, ay këri liggéeyukaay yu Amerig jot nañoo feeñal gil (gaas) bu bari ci réew mi.

Am na tamit wenn sémbuw Hub technologique (bérébu xarala) wu ñu bëgg a taxawal fa Ndakaaru. Sémb la wow, dees na ko sanc ci dend bu tollu ci 40i ektaar biir Ndakaaru. Jubluwaay bi mooy fexe ba Ndakaaru di buntu xaralay saa-amerig yi fi Afrig.

Njiitu réew mi xam na cuq Njiitu réewu Amerig li sax, daldi koy muuñloo. Ndaxte, xam na ni Donald Trump ku bëgg powum golf la. Moom Donald Trump tamit, wax na ay kàddu yu rafet ci Njiitu réew mi. Daf ne :

« Jaar-jaar bu am solo la am. Dafa xaw a nirook xale, donte ne ëppal at yi ñu koy fooge. Mi ngi def liggéey bu am a am solo. Nguur ga woon [gu Maki Sàll ga] daf ko tooñoon dëggantaan, waaye muñ na bu baax. Maa ngi koy ndokkeel bu baax. »

Muy kàddu yu rafet naam, waaye mënees na xel-ñaar ci dëggoom. Ndaxte, ku xam Trump, xam ne nawloowul Afrig. Bu demee bay woo ñenn ci Njiiti réewi Afrig yi, koom-koom rekk a tax. Nde, jamono yii, Siin, Riisi ak Turkii dañu leen a rawee lu bari ci Afrig lol, moom la Trump bëgg a dabu. Booy seetlu sax, dinga gis ne juróomi réew yi fa teew yépp, seen i suuf dañoo fees dell ak i balluy mbindaare te dend ak géej gi.

Laaj bi sampu nag mooy, ndax réewi Afrig yi dinañ am muusaayu jëfandikoo coppite yi am ci àddina si ci fànnu sewopolitig ngir suqali seen i koom-koom, naatal seen i réew.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj