Ni ñu ko daan baaxoo di def àllarba ju nekk, noon la demee démb tamit. Ndax, démb lañu doon amalaat ndajem jëwriñ yi. Njiitu réew mi jot na faa faram-fàcce ay poñ yu bari. Waaye, mu am yu ci gën a fés. Nde, kenn umpalewul ne jamono jii saabalukaay yëngu na lool sax. Ci talaata jii weesu lañu doon amal bés boo xam ne xibaar du am donte ne sax, ñépp ànduñu ci. waaye, Njiitu réew mi dégg na leen. Moo tax, mu xamle démb ne, dina amal aw waxtaan ak ñoom. Ndax, nee na, nekkiinu saabalukaay yi mat naa bàyyi xel.
Bi mu jógee ci loolu, siiwal na tukki bi muy waaj a amal ci fan yii di ñëw. Wii yoon nag, tukki bi du doon biir Afrig, du it fa Tugal. Waaye, ma nga jëm ba Siin, fa kembaaru Aasi. Yoon woowu dina ko jël ñett ak ñeenti fan ci weeru sàttumbar. Li mu ko dugge mooy fekk ñeenteelu ndaje mi ñu dippe “4ème sommet de coopération sino-africain”. Ndaje moomu, dinañu ko amal juróomi fan ak juróom-benni fan ci weeru sàttumbar. Ginnaaw bi ñenn ci jëwriñ yi jëlee kàddu ba noppi, moom it jot naa jël ay ndogal. Ndax, am na ñett ñu mu takkal ay ndomboy-tànk. Ñi mu tabb, ñii may lim la :
Liyatnaa-Kolonel El Haaj Maado Ba, tabb nañu ko “Secrétaire permanent du Comité national du CILSS”. Ki mu wuutu fa béréb boobu di Baaba Ba ;
Baakari Fati, moom lañu tabb Njiitul “Gestion de la Planification des Ressources en Eau”. Mu wuutu fa béréb boobu kii di Ñoxor Nduur ;
Siidi Muhammed Sekk lañu tabb Njiitul “Conseil d’administration de la Société nationale d’Aménagement et d’Exploitation des Terres du Delta du Fleuve Senegal et des Vallées du Fleuve Sénégal et de la Falémé”. Mu wuutu fa Aamadu Ñaŋ.