NDAJEM JËWRIÑ YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci àllarba ji lañu doon amal ndajem jëwriñ yi ci njiiteefu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Ca ndaje mooma, jot naa laal ay poñ yu bari. Waaye, bi ci gën a fés mooy waajtaayu ñaareelu bésu set-setal bi. Nde, moom la ubbee ay kàddoom sax. Li mu ko dugge mooy ñu fexe ba bés boobu ñu dëgmal raw bi ñu fi njëkkoon a amal. Bés boobu, gaawu lay doon, juróom-benni fan ci weeru sulet. Waaye, yemul foofu.

Wax na tamit ci mbirum dëkkuwaay yeek ja yi. Maanaam, Nguur gi def kéemtelaayu kàttanam ba mbooleem liggéeykat yi nga xam ne tënkuwuñu ci Nguur mën a gis seen bopp ci li ñuy def. Looloo tax, muy sàkku ñu jox cër sàrti dëkkin wi ci dëkki taax yi muy ci tabax yeek dëkkuwaay yi. Waaye, loolu yépp day ànd ak tëralin gu mucc ayib ak kaaraange gu matt sëkk ci ja yi, bérébi mboolaay mi ak yaxantukaay yi ci gox yépp. Laata muy jeexal ay kàddoom tamit wax na wàllub dem beek dikk bi ak liggéey yi ñu ci war a amal. Bi mu jógee ci loolu la jébbal yenn jëwriñ yi kàddu laata muy jël ay ndogal.

Ca njeexitalu ndajem ma nag, am na ñenn ñu ñu fa jot a takkal ay ndomboy-tànk.

Lansana Gàññi Saaxo lañu tabb Njiitul « Conseil d’Administration de l’Agence de Promotion des Investissements et des Grands Travaux (APIX) ». Ki mu fa wuuti di Abdu Faal ;

Faal Mbay, tabb nañu ko Njiitu « Institut National du Pétrole et du Gaz (INPG) ». Mu wuutu fa Aagibu Ba.

Kolonel Aamadu Usmaan Ba bu « Gendarmerie nationale » moom lañu tabb Njiitu « Surveillance et du Contrôle de l’Occupation du Sol ». Ki mu fa wuutu di Kolonel Pàppa Saaburi Njaay ;

Abdul Wahaabu Sàll, tabb nañu ko « Directeur général Adjoint de la Police nationale ». Mu wuutu fa béréb boobu Móodu Jaañ ;

Àlliyu Njaay lañu tabb Njiitu « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de la Justice ». Mu wuutu fa Abdulaay Si ;

Paap Abdurahmaan Daabo, tabb nañu ko « Conseil d’Administration de la société AIBD SA ». Ki mu fa wuutu di Abdulaay Timboo ;

Aatumaan Si, moom lañu tabb  Njiitu « Agence nationale de la Sécurité Routière (ANASER) ». Ki mu fa wuutu di Séex Umar Gay ;

Ibraahiima Sàll, tabb nañu Njiitu « Société Autoroutes du Sénégal (ADS) ». Mu wuutu fa kër googu Aubain Saaña ;

Kolonel Ibraahiima Géy, tabb nañu ko Njiitu « Parcs nationaux ». Ki mu fa wuutu di Bookar Caam ;

Àlliyu Njaay, moom lañu tabb « Directeur exécutif de l’autorité nationale de Biosécurité ». Ki mu fa wuutu di Uséynu Kase ;

Kolonel Lamin Kan lañu tabb « Secrétaire permanent de l’Autorité nationale de Biosécurité » ;

Móodu Faal Géy, tabb nañu ko Njiitu « Centre d’Education et de Formation environnementales ». Ki mu fa wuutu di Góora Ñaŋ ;

Sëriñ Mbàkke Lóo, moom lañu tabb Njiitu « Centre Régional des Œuvres universitaires sociales de Thiès ». Mu wuutu fa béréb boobu kii di Séex Sàll ;

Saŋ Biraan Ñiŋ, tabb nañu ko Njiitu « Centre Régional des Œuvres universitaires sociales du Sine Saloum ». Ki mu fa wuutu di Uséynu Jóob ;

Faama Jeŋ, tabb nañu ko Njiitu « Centre Régional des Œuvres universitaires sociales de Diamniadio ». Mu wuutu fa kii di Musaa Hammadi Saar ;

Saalif Balde, moom lañu tabb Njiitu « Centre régional des Œuvres universitaires sociales de Ziguinchor ». Ki mu fa wuutu di Sana Maane ;

Momar Taala Géy lañu def Njiitu « Institut de Technologie Alimentaire ». Ki mu fa wuutu di Mamadu Aamadu Sekk ;

Asiyah Jóob, tabb nañu ko « Directeur général du Développement communautaire et de la Promotion de l’Equité ». Mu wuutu fa béréb boobu kii di Muus Bar Fay ;

Faatumata Bintu Jéeju, moom lañu tabb « Directeur de l’Equité Sociale ». Ki mu fa wuutu di Faatu Jaañ ;

Eli Paul Biyaagi, tabb nañu ko « Directeur du Développement Communautaire ». Ki mu fa wuutu di Xaadim Silla ;

Say Siise lañu tabb « Directeur de l’Equité Territoriale ». Mu wuutu fa Abiibulaay Lóo ;

Faatu Ba, tabb nañu ko « Directeur de Promotion des droits et de la Protection des Enfants ». Ki mu fa wuutu di Ibraahiima Géy ;

Nansi Nduur lañu tabb Njiitu « l’Autonomisation Économique des Femmes » ;

Edmond Kamara, tabb nañu ko Njiitu « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de la Famille et des Solidarités » ;

Baay ñas lañu tabb Njiitu « Agence de Construction des Bâtiments et Édifices Publics ». Ki mu fa wuutu di Hammady Jeŋ ;

Sëriñ Séex Baaxum, moom lañu tabb Njiitu « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de l’Urbanisme, des Collectivités territoriales et de l’Aménagement des Territoires » ;

Sofi Jonn, tabb nañu ko Njiitu « Projet de Promotion de la Gestion Intégrée et de l’Economie des Déchets Solides (PROMOGED) ». Mu wuutu fa Séexu Umar Gay ;

Usmaan Siise lañu tabb « Directeur général de la santé ». Ki mu fa wuutu di doktoor Barnabe Ñiŋ ;

Séydu Jàllo, moom lañu tabb « Directeur général de la SEN-Pharmacie nationale d’approvisionnement (SEN-PNA) ». Ki mu fa wuutu di Faatu Fay Njaay Dem ;

Faatu Baara Njon, tabb nañu ko « Directeur des infrastructures, des Équipements et de la Maintenance au Ministère de la Santé et de l’Action Sociale ». Mu wuutu fa Aamad Juuf ;

Maalig Jàllo, moom lañu tabb « Directeur des ressources humaines au Ministère de la Santé et de l’Action Sociale ». Ki mu fa wuutu di Awa Faal Jaañ ;

Mamadu Lamin Juuf, tabb nañu ko Njiitu « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de l’Agriculture, de la Souveraineté alimentaire et de l’Elevage » ;

Abdu Jaw lañu tabb « coordonnateur national du Programme de Développement de la Microfinance Islamique ». Ki mu fa wuutu di Aminata Jaawo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj