Ndajem Ndeyu sàrti réew mi bañ na dogal yi tukkee ci waxtaan wu mujj wi Njiitu réew mi woote woon fa CICAD, Jamñaajo. Juróom-ñaari àttekat yu mag dañu gàntal li waxtaankat yi déggoo woon lépp ba jébbalko Njiitu réew mi.
Ci ndogal li mu jël, Ndajem Ndeyu sàrti réew mi daa feddali ne àppug wotey yi warul a weesu àpp gi Njiitu réew miy jeexal. Rax-ci-dolli, dëggalati na ne 19i lawax yi kepp ñooy bokk ci joŋantey wote njiiteefu réew mi ci at mii.
Kon, Maki Sàll moo ci des. Nuu xaarandi ba xam lu muy def.