Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, beral na way-loruy xew-xewi 2021 jàpp 2024 xaalis bu tollu ci 5i tamñareet (miliyaar). Muy nag ndimbal lu mu leen digoon niki ndàmpaay ginnaaw bi ci nit ñu bari ñàkkee seen i bakkan, mu am it ñu ci yàqule. Bu dee ñi ci faatu, amoon na ciy doomi jàmbur, nekkon ay ndimbal-njaboot ak sax ay boroomi kër.
Njabooti way-loru yi rafetlu nañu ndogal li donte ni mënul a doon mukk ci ñoom luy wuutu bakkan yees ci ñàkk. Bu loolu weesoo tamit, ñoo ngi xaar ñu séddale ko ci anam bu jaar yoon. Rax-ci-dolli, ñoo ngi sàkku ci Nguur gi mu neenal sàrtub neenal (loi d’amnistie) bi fi Maki Sàll wotelu woon laata muy folliku. Li ñu bëgg mooy ñu ubbi ag luññutu, jàpp ñi ci laale woon ñépp àtte leen, daan leen daan yi war.