Woote bi yoon woo Njiitalu Pastef li, Usmaan Sonko, la yéenekaayu yi xëyee tey. Mooy xibaar bi gën a fës fan yii. Nde, ci alxamesu tey jii, bu fukki waxtu jotee, la Usmaan Sonko war a wuyuji yoon.
Muy pólisee yi di sàndarma yi, ñoom ñépp ñoo takku, taxaw, fees dell ci péeyub réew mi, Ndakaaru. Ba ci sàppëer yi, kenn desul. Foo romb, daamari pólis yeek sàndarma yaa ngi taxaw, rawatina ca UCAD ak ci palaasi AUCHAN yi. Looloo tax waa Vox Populi, ci xëtam bu njëkk, nee « Nguur gi caaxaanul ». Loolu nag, xaw na teey xeli ñenn ñi. Nde, laaj bi nit ñiy laaj mooy, ab woote kese, lu ci jar lii lépp. Lu Nguur giy ragal ? Xanaa li xewoon màrs 2021 lañuy ragal mu amaat ?
Cig pàttali, màrs 2021, réew mi dafa yëngu woon ba 13i rot ci. Mbirum Sonko-Adji Saar a ko sababoon, bi ko yoon woowee. Bi muy wuyuji, ci yoon wi, la coow li tàmbali woon, ba ndaw ñi jàmmaarloo ci ak takk-der yi. Moo tax, wii yoon, takk-der yi jël seen i matuwaay, defaruwaat ngir dara bañ leen a bett.
Xalifa Sàll ak kilifay lëkkatoo YAW dinañ gunge Usmaan Sonko tirbinaal
Kilifay lëkkatoo Yewwi Askan Wi amal nañu ci àllarba ji am ndaje ak taskati-xibaar yi ngir waxtaane woote bi yoon woo Usmaan Sonko. Xalifa Sàll nee, ñoom, dàquñu li xewoon màrs 2021 amaat.
« Mënunoo génne ci sunu xel yi ne, li xewoon màrs 2021 mën na xewaat. Noo ngi nuy xoqatal, di nu tëj, di nu gëtën waaye dunu mës a xàddi. Lii bu daqul, ragalunu xew-xewi màrs 2021 [amaat]. »
Ñoom nag, waa YAW, nee nañu tiituñu ci àtte bi yoon nar a àttee mbir mi. Ndax, ci seen i wax, bu yoon defee liggéeyam, ñoom ñooy am dëgg. Xalifa Sàll ak i ñoñam fas nañoo yéene gunge seen naataangoo bi ngir taxawu ko. Waaye, Usmaan Sonko, moom, nee na, bu sañoon, moom kese mooy dem ak i layookatam.
Bi 16i waxtu jotee ci ngoon gi la ndeyu-mbill ji doon wax ak i militaŋam, ay soppeem ak ñi ànd ak moom. Ci la leen waxee ne, jarul ñuy génn. Nde, woote bii, lu jaadu la, te dafa war a am. Nee na sax, moom moo ko yàgg a sàkku, àttekat bi di wut ay lay, di ko dàq. Mu teg ci ne, ci mbir mii, gisu ci dara luy tax yoon jàpp ko, walla ñu ko ciy tere doon lawax ci wotey njiiteefu réew mii nu dégmal, atum 2024. Moo ko tax wax ne :
« Bu kenn naan damay dem kër Usmaan Sonko walla damay dem tirbinaal walla damay dem fii walla fale. Ag ndéglu, man maay jóg ak samay layookat, jàkkaarloo ak àttekat bi, nu waxante li nuy waxante ma ñibbisi sama kër. Moo tax ma leen koy ñaan. Ndax, xeex bii, xel a koy xeex. Xeex bii, xadar xeexu ko ; xadar mooy mujj ci xeex bi. »
Li kàddu Usmaan Sonko yii wund mooy ne, wareesul a may Nguur benn lay walla benn xeetu proxndollu bi muy jaare ngir jàpp ay nit walla teg ko moom ci boppam ay tuuma. Ginnaaw bi mu waxee loolu, yégle na ne, ciy fan yu néew, dina woo taskati-xibaar yi ngir yaatal ci mbir mi. Ndax, ciy waxam, am na lu askan war a xam ci mbir, rawatina kilifa yu mag yu ci laale.
Fim ne nii nag, ñépp a ngi xaarandi ëllëg ba xam lees di ruumandaat dina am, am déet. Ku dund, dinga fekke.