NDIISOOY NGOMBLAAN GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dogub 24eel bu càrtub Ngomblaan gi dafa tëral ne :

« Ci ndoorteelu gépp moomeg Ngomblaan, ak ci bépp toogaanub siŋŋ, ginnaaw bi ñu falee pekkug Ngomblaan gu sax gi, Ngomblaan gi dafa war a samp fukk ak ñeenti (14i) ndiisoo yu sax. »

Dog bile, day méngoo ak dogub 62eel bu Ndeyu-àtte réew mi. Looloo taxoon, ci talaata ji, dépite yi dajewaatoon ca Ngomblaan ga ngir jëmmal càrt bile. 

Dépite yi yéex nañoo tàmbali seen ub liggéey, nag. Ndaxte, 10i waxtu ci suba si lañu waroon a door. Waaye, daanaka guddi fa la leen fekk. Nde, bi 19i waxtu tegalee 40i simili la Njiitalu Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob, ubbi liggéey bi.

Ñetti lëkkatoo yi, Bennoo Bokk Yaakaar, Wallu ak Yewwi Askan Wi ñoo yéexaloon mbir mi. Werante ak xëccoo lañ fa nekke woon ñeel tànniinu ndiisoo yi. Ndege, kujje gi dañ bëggoon waa Bennoo Bokk Yaakaar jël juróom-ñaari ndiisoo yu njëkk yi, ni ñu jëlee woon ñeenti tof-njiit yu njëkk yi. Waaye, lëkkatoog Nguur gi dafa bañ doxalin woowu. Ndax, su boobaa, ndiisoo yi ëpp solo dañ koy raw. Moo tax ñu doon muddaarante ak lëkkatooy kujje gi. Waxtaan wi yàgg lool, ba ñaari dépite yi farul fenn, Ceerno Alasaan Sàll ak Paap Jibril Faal, daldi mer.

Waaye, mujje nañoo déggoo seen biir ba samp ndiisoo yi, ku nekk tànn dépite yi la fay teewal. Ci àllarbay démb ji sax lañu waroon a dajewaat ngir sas 14i ndiisoo yi laata ñuy sumb seen liggéey. Bu ñu sukkandikoo ci dogub 14eel bu càrtub Ngomblaan gi, bépp dépite bees fal ci pekkug Ngomblaan gi, waruloo bokk ci genn ndiisoo.

Nii la njiiteefi ndiisoo yi tëdde :

  1.     Ndiisoog Koppar gi ak Caytug nafa gi : Séydu Juuf (BBY)

  2.     Ndiisoog Mbiri koom-koom gi : Maadi Danfaxaa (Wallu)

  3.     Ndiisoog Nosteg dëkk bi, Taaxal gi, Tabax yi ak Dem beek dikk bi : Basiiru Gujaabi (YAW)

  4.     Ndiisoog Yokkuteg kow gi : Seex Sekk (BBY)

  5.     Ndiisoog Yokkute gu sax gi ak Càllaleg mbindaare mi : Roqaya Juuf (Wallu)

  6.     Ndiisoog Laf yi ak Balluy ndoxe yi : Abbaas Faal (YAW)

  7.     Ndiisoog Àtte yi, Desàntaraalisaasiyoŋ, Liggéey ak Àqi doom-aadama : Abdu Mbow (BBY

  8.     Ndiisoog Mbiri bitim-réew ak Saa-senegaal ya ca bitim-réew ak Bennoog Afrig : Baabakar Mbeng (YAW)

  9.     Ndiisoog Xare beek Kaaraange gi : Abdulaay Balde (BBY)

  10. Ndiisoog Njàng mi, Ndaw ñi, Tàggat-yaram ak Po yi : Umar Si (YAW)

  11. Ndiisoog Wér-gi-yaram gi, Askan wi, Mbiri mboolaay gi ak jàppalante gi : Sira Njaay (BBY)

  12. Ndiisoog Kontaabilite ak caytu gi : Mamadu Uri Baylo Jàllo (BBY)

  13. Ndiisoog Yable yi : Mohamed Ayib Dafe (YAW)

  14. Ndiisoog Mbatiit gi ak Jokkalante gi : Maalig Faal (BBY)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj