Ndog mu metti moo am démb ci talaata ji, ci boori 6i waxtu yu toftal 50i simili. Ci tali “Autoroute Ila Touba [Ilaa Tuubaa]” bi la ndog moomu ame, ci wetu dëkk bees di wax Reefaan. Mu di musiba bu réy, ndax 12i nit ñoo ci dee, démb. Ñuy jooy te noppeeguñu, mu am ku dolleeku ci lim boobu. Nde, kenn ci ñi ci jële woon ay gaañu-gaañu dafa mujje ñàkk bakkanam moom itam. Bu ko defee, 13i nit ñoo ci dee.
Benn minibiis Toyota Hiace moo mbëkk ag sëfaan gu ndaw (camionnette) gu yeboon ay njaay. Sëfaan gu ndaw googu nag, dafa paanoon, daldi gaare ci yoonu négandiku wi (bande d’arrêt d’urgence). Mettiwaayu ndog mi dafa waral ay yàq-yàq yu bari wëliis bakkan yu bari yi ci rot.
Wallukat yi gaawantu woon nañu ngir dimbaliji way-loru ya, daldi jàllale ña ca jële ay gaañu-gaañu ca ragluy diiwaan ba. Ci lees waxagum, amaana xél bu ëpp ak nelaw moo sabab ndog mu doy waar mile.