Ndogi yoon yaa ngi wéy di gën a bari. Saa yees jàppee ne ndog yi wàññeeku nañu rekk, fekk booba la Waalo gën a aay. Daanaka bareetul lees di toog ayu-bés bu mat te gisuñu walla ñu dégg ndogum yoon. Mu ñëw rekk gën a metti. Ay bakkan rot ci walla ñu bari jële ci ay gaañu-gaañu waxaalewuñu yàq-yàqu yi. Te, ndog mi am tay, ci suba, fa Kebemeer daf cee doy firnde.
Ginnaaw ndogum yoon mu metti ma amoon ca diggante Lingeer ak Maatam lu yàggul dara, meneen mu ni mel amaat na tay. Nde, yépp ay bakkan rot nañu ca, am ñu ca jële ay gaañu-gaañu. Naam, li ëpp ci ndog yi, ay daamar ñoo ciy mbëkkante, waaye wii yoon moom demewul noonu. Ndax, ag daamar moo dalante ak benn saret ba ay doomi-aadama ñàkk ci seen i bakkan.
Ndog moomu mi ngi am tay ci suba ay boori juróom-ñaari waxtu. Mi ngi ame ca boori dëkk bii di Gàdd Faal, ca yoonu Tuubaa-Kebemeer. Ñetti doomi-aadama ñoo ci ñàkk seen i bakkan, ñaar jële ci ay gaañu-gaañu yu metti. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, ñoom ñett ñi faatu ñoo bokk fu ñu jóge. Ci benn saret lañu nekkoon bu jóge dëkk bii di Mbengeen. Dañu doon dem ci jawu Kebemeer biy am ayu-bés bu nekk. Genn daamar gu ñuy dippe “War gaynde” moo leen fiir.
Ñett ñi ci faatu ñépp ay ndaw lañu. Kenn kaa ngi wuyoo ci turu S. Mbeng tollu ci fukki at ak juróom-ñett. Keneen ki tuddu M. Mbeng tollu ci ñaar-fukki at. Ki ci des tudd Nd. Mbeng tollu ci fukki at ak ñeent. Mu doon xew-xew bu tiis lool donte ne sax du guléet ñu fi gis ndog yu ay bakkan rot. Waaye, bu ni mel bariwul lu muy am. Li ci doy waar kay mooy dafa mel ni ba tay saafara amagu ci.