Démb ci alxames ji la Ngomblaan gi amaloon am ndaje ngir wote pasum diiŋat mi waa lëkkatoo Yewwi Askan Wi di teg ci kaw njiitu jawriñ ji. Pasum diiŋat mi soo ko déggee, jàppal ne am pexe la bu ag kippaangoo ci Ngomblaan gi di jëfandikoo ngir ñàkk kóoluteem ci Nguur gi. Te su loolu demee ba ñu wote ko, mu jàll, dafay tekki ne googu Nguur fàww mu tekki ndombog-tànkam.
Altine jii weesu la Aamadu Ba, njiitu jawriñ ji taxawoon ca Ngomblaan ga ngir dégtal fa li Nguur gi namm a joy. Ginnaaw gi la waa YAW gis ne joxewul ay tontu yu dal seen i xel ci laaj yi leen yitteel. Te it, jàpp nañ ne, ñu ci ëpp, ca Ngomblaan ga, di ay siboorukatu Maki, ñooy néewal baatu fal àtte bi. Ndaxte, li Maki bëgg rekk, ñoom, ñu wote ko ci lu amul benn sikk. Lii moo tax waa YAW fippu, teg am pasum diiŋat ngir ga Nguuru Aamadu Ba gi tas.
Seen ndaje mi àggoon na ci diirub 4i waxtu. Bi ñu noppee lañu xamle ne ña ëpp ca Ngomblaan ga wote nañ ngir pasum diiŋat mi bañ a jàll. Kon, Nguuru Aamadu Ba gi du tas te dafay wéyal liggéeyam. Noonu, Aamadu Ba xamle na ne
« Am naa mbégte ci ndogal li Ngomblaan gi jël, muy wone ne Maki Sàll moo gën ci réew mi. Gile Nguur dina gën a jox nopp askan wi, ndax moom lañ fi teewal. Ginnaaw ba Ngomblaan gi gàntal na pasum diiŋat mi, li des mooy ñu liggéey ndax réew mi daf ñu soxla. Ngir loolu am nag, dafay laaj ñu ànd ak dal, boole ci ak demokarasi bu ànd ak jàmm. »
Cig pàttali, la doon tax waa YAW am ndam ci kaw Nguuru Aamadu ba gi, mooy ne dañu waroon am lu tollok 83i baat. Te, ñoom, 55i baat rekk lañ am. Li tax wote bi demee nii, bokk na ci ne Ngomblaan gi am na lu tollu ci 165i dépite, te 82 yépp waa Nguur gi lañu, ndax Maki Sàll lañ àndal. Yewwi Askann Wi 56 dépite la am, Wallu am 24. Ñett yi ci des bokkuñu ci genn kippaangoo, ñuy ñii di Ceerno Alasaan Sàll, Aminata Ture ak Paap Jibril Faal. Rax-ci-dolli, njiital kippaangoog Wallu gi, Séex Abdu Baara Dolli Mbàkke, dafa ne ñoom duñu wote pasum diiŋat mi wa YAW teg ngir tas Nguurug Aamadu Ba.
« Waa YAW bi ñiy taxawal wote pasum diiŋat mi, boolewuñ nu ci. Moo tax nun, dunu ko wote. Moone, bi ñiy taxawal lëkkaloog làng gi Yewwi-Wallu, dañu waxoon ne ñooy bokk di liggéeyandoo ci lépp lu ñuy sóobu, waaye defu leen ko. Li ma gën a metti tamit mooy li waa YAW deful dara ci bi ñu may tëj kaso, di ko boolee ak i xas. »
Kon mel na ne ba léegi ñi nekk ci Kujje gi ànduñu te juboowuñu, moo tax boobu ba téy li Maki Sàll ak Nguuram gi bëgg rekk la Ngomblaan giy wote muy jàll. Ndax kat, ña fa ëpp, moom lañ fa nekkal. Su kujje gi bëggee am ndam ci kow Nguur gi, fàww waa kujje gépp boolo doon benn.