NGUUR GI TOPPEETUL USMAAN SONKO DARA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nguurug Maki Sàll gi dellu ginaaw ci topp bim doon topp Usmaan Sonko ci yoon. Nde, dafa bind na ëttub àttewaay bu mag bi, di ko wax ne wacc na cantaaneg 1eel bu  14 desàmbar 2023 bu Njiitul « Tribunal d’instance Hors Classe de Dakar ».

Xibaar bu bees rot na ñeel Usmaan Sonko. Nguurug Senegaal moo bàyyi topp bim ko doon topp ca ëttub àttewaay bu mag bi. Yoro Musaa Jàllo, ndawul Yoon (agent judiciaire) liy teewal Nguur gi moo bind ab bataaxal, jagleel ko Sëñ Abdulaay Njaay mi jiite Njëlbeenug Néegub caytu bu ëttu àttewaay bu mag bi (Président de la Première Chambre administrative de la Cour suprême).

Ginnaaw ba Nguur gi bàyyi na li mu doon toppee Usmaan Sonko, daanub teewadi (condamnation par contumace) naaxsaay na. Te, bu dee layoom beek Maam Mbay Ñaŋ, amnisti bi far na ko. Kon, lees di wax « casier judiciaire » bu Usmaan Sonko set na wecc. Li ci des kon mooy ñu génne ko kaso bi. Kañ lay doon ? Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj